Yenn saay ma tay ko xulóok yaw (ah!) Ndax lay xew ci biir juboo ba (waaw foofu lu fa xew?) Reewantu yakkul mbëggeel feeling la ci waawaaw Li la duggal ci man génnewula ci (surtout loolu!) Man su ma ragalul woon Yàlla ni maak yaw Pique ak pelle taqalewuñu Kaay ñu dem fu la neex Xale bile yaw laa jox bopp Mënuma la tenir tête, dama la nob Na ñàkk jom colul Ndax mere la woorul Yaw sa dara soful Ndax bàyyi la yombul Te man sama compteurou xol Nga woyofal yaa ko tay Même suñu bàyyaante we Sama alal ngay doon ba-tay Neñ juboo maak yaw Ma yërëm noon yi Sòccu woon di xaar ku ñu reetaan Moo tax waruñu xulóo maak yaw Ndax yaay seral xol bi Bu ko jaaree sax ma ramal la (moo xanaa nga bañ) Feccal la (mo xanaa nga bañ) Di la ayoo nenne Bae kaay ma yeetal la (mo xale bi xanaa nga bañ) Tay ngay jommi Jubook yaw lu am jom ni (mo xanaa nga bañ) Kaay fi chéri li des waxu biir nekk la Heey Sa chéri du la seetaan nga fiy ñaaw Ne dala bëgg yaa yor cahier wam Mu yor sa bic ni dalay bindal Su ma jubee xare bi duma dëpp Ndax ñayu xare la man Kenn du laal li ma moom Ndaanaan ndaanaan a koy àttan Chéri coco ney neex Jëndal glace Cub naa drapeau bi weex Tey sama xol dafa neex Ndax dama jubook bànneex Hey Namm nga ko Nammoon naa la Nammante ngeen Xolu ñar a koy def Kon bisuwante leen Mouaaahh Kon mbëggeel bala neex rax ñakk jom Xale bi Suñ xuloo ma lay tudd yaa ko fa am Waaw Soo xamoon tay ji li ma namm ci yaw Na noppi sax bala waa jamra di ñów Neñ juboo maak yaw (ñëwal) Ma yërëm noon yi Sòccu woon di xaar ku ñu reetaan (eh seen xol du neex tey) Moo tax waruñu xulóo maak yaw Ndax yaay seral xol bi Bu ko jaaree sax ma ramal la (moo xanaa nga bañ) Feccal la (mo xanaa nga bañ) Di la ayoo nenne Bae kaay ma yeetal la (mo xale bi xanaa nga bañ) Tay ngay jommi Jubook yaw lu am jom ni (mo xanaa nga bañ) Kaay fi chéri li des waxu biir nekk la Kon fanaan Yaa ma newoon fanaan Yaa newoon fanaan Yaa ma newoon fanaan Fanaan ci naa Yaw fanaan Chéri fanaan Yaw fanaan Yaa ma newoon fanaan Fanaan ci naa Dialy xalamal ma Ma woyal sama waa ji Maak yaw amuñu nëboo Yaay sama wétal Waruñu xuloo Yaw fanaan Chéri fanaan Yaw fanaan Yaa ma newoon fanaan Fanaan ci naa Bu ko jaaree sax ma ramal la Feccal la Di la ayoo nenne Bae kaay ma yeetal la Tay ngay jommi Jubook yaw lu am jom ni Kaay fi chéri li des waxu biir nekk la