Bay Moodu demal mu ne du dem Xelam dallul Bëgg dem taxul ta mën a dem Mën a dem, moy tax a dem Waayam ja, yàkkamti woon, jël yoon wa Te yoon woowe du yoonam Ci lëndëm mu gis fa réer, ci lëndëm ñu gis fa réer Dugg ci gaal, yaakaar féey ci ndox ci digg u geej ci diggu geej Surux, yaakaar yépp tas na, ñépp ngaay jooy Bay Moodu dem na (lutax mu dem?) Picc ramatu ma ngay naaw waye xel mu ñi ci suuf Ñu mën a kott, dëgg-dëgg ndekete yorul ñu mbaam Ñaari xale, ñoo ñi wër yàlla Ñaari xale, ñoo ñi wër yàlla Seeni rangoñ moo fi tuuru woon Wër nañu ba dee (wër nañu ba dee) Wër nañu ba dee Kan mooy laal ngone Kan mooy laal ngone Laal na yàlla (kan mooy laal ngone) (Kan mooy laal ngone) Kan mooy laal ngone Kan mooy laal ngone Laal na yàlla Kuu jàpp ci loxoom waay mu yobbu la (kan mooy laal ngone) (Kan mooy laal ngone) (Laal na yàlla) Kumba jirim la ndax ñàkk yaay Baayam tële, dénk ka nijaayam Ci ba mi ndaw, ci ba mi ndaw Nijaayam war ko yar, far sàkku ndawam (Jirim kumba) Bàyyi ko ak màndaga bu dul jóg ci moom (ba ba mi de) Picc ramatu ma ngay naaw waye xel mu ñi ci suuf (kan mooy laal ngone) (Kan mooy laal ngone, laal na yàlla) Ñu mën a kott, dëgg-dëgg ndekete yorul ñu mbaam (kan mooy laal ngone) (Kan mooy laal ngone, laal na yàlla)