Yeah, eh eh eh Lé, lé, walé Hum, hum Suba su ma yeewu Yaw laay bëgg jàkkaarlool Saa su ma yeewu Yaw laay bëgg njëkk xool Ëllëg lu mat a soor la Waaye xel xalaatu ko Ëllëg ay jaar-jaar la Sama xol yëgoon na ko muy ñëw Xel xalaat la (xel ak xalaatam ba) Xol yëg-yëg la Nit ak jëmmam ja Dara xaaju fa Saa su ma yeewu Yaw laay bëgg njëkk xool (Su ma yeewu yaw laa bëgg njëkk xool) Fajar su ma yeewu Yaw laa bëgg jàkkaarlool Denk naa la guddi Fanaan yakkar ci yaw Gent naa la guddi gi yëpp Ndax fajar yaw lay jàkkaarlool Mbëggeel Xel xalaat la Xol yëg-yëg la Nit ak jëmmam ja Dara xaaju fa Nit ak jëmmam ja Dara fa xaajul