Ku ne xam nga ki la nob Ki la bëgg te du la nax May la jàmm te di la wan Luy mbëggeel waay, xam nga ko Duy nga sama xol mu fees Bëgg tay du wees Taal nga ma fu ne Léegi Sapeur lañuy xaar Sàcc nga sama xol bi Fàww boole am ci yoon Coup d’Etat sama mbëggeel Léegi Armée lañuy xaar Dok ak yaw ci mines u rebelles yi Jéggi tànk moom du xel Dugal nga lu ne sama xol Léegi Douane lañuy xaar Président a ngee Président a ngii Foo nekkee Président Ma doon fa Première Dame Foo doonee Macky, ma doon sa Marème Foo doonee jëmm, ma doon sa xol Foo doonee Sadio Mané Ma doon sa ballon, nga di ma dugal Foo doonee pique, ma doon sa pelle Foo doonee xalaat, ma doon sa xel bi Di la tardeel ba nga dof Dof di naan “waawaaw” Ey waay! Ndeysaan! Ey waay! Ndeysaan! Awuma wurus, awuma ngalam Waaye chéri am naa mbëggeel Dara xewul dee ko woyofal Jaral nga ma lu ne Sa joli coeur ràngati ma Ba ma dellu gone Bu ngeen ma dégloo ma wayal leen Ki nangu sama xol bi laay wayal Hey! Tourné nga daj nga ci man Déédéét du yaafuus nekkul ci man Wax ji du bari, jëf ji day bari Jikko bu défaillant nekkul ci man Président a ngee Président a ngii Foo nekkee Président Ma doon fa Première Dame Foo doonee Macky, ma doon sa Marème Foo doonee jëmm, ma doon sa xol Foo doonee Sadio Mané Ma doon sa ballon, nga di ma dugal Foo doonee pique, ma doon sa pelle Foo doonee xalaat, ma doon sa xel bi Di la tardeel ba nga dof Dof di naan “waawaaw” Ey waay! Ndeysaan! Ey waay! Ndeysaan! Aah! Lee! Ey waay! Jàmbaari léegi léegi Jóoni jóoni jàmbaar Ndeysaan! Biram Diop Ey waay! Chéri Kya dama lay joobeel Ndeysaan!