Man maa ngi ci sama bopp dama pare Pur lamb fépp, gëna bëre Risqué te kenn du ma téye Damay yéeg te duñu ma gunge Fok ma gañe rekk wala ma dee Perte temps Yàlla tere Bakkan laj tek, duma mëna bég Tant que awma li may revé Life bi wane ma ni yëfu dëmm la Ba tax na awma ganyine École jàngal ma rëdd ci tableau Ba ma raw Bubu Design Mbedd mi jàngal ma sadique Dundu lu metti di mérite Tàng ba ma sonn, sumi sama veste Taxul ma wekk ko ci nit Àdduna soxor na amul yërmande Xeexal ba kenn du la mëna commandé Xaruma salaire te maa ngi fayeeku Tëdd di nelaw te gënoo ma yeewu Yaw danga rare Foo ne? Kenn gisatu la! Awma jot bi, maa ngi ci job bi Léegi ci Business bi rekk Sa gars yi ne nañu danga rare Foo ne? Kenn déggatu la! Demal ne leen awma temps bi Léegi ci Business bi rekk Maa ngi ci dara (yaa ngi ci dara) Nammuma dara (nammoo dara) Maa ngi ci dara (yaa ngi ci dara, kay!) Te nammuma dara (ay nammoo dara) Maa ngi ci dara (yaa ngi ci dara) Nammuma dara (nammoo dara) Maa ngi ci dara (yaa ngi ci dara, kay!) Te nammuma dara (nammoo dara) Léegi sama xol dafa dëgër Dama jënd fer, dolli béton Ba fi sama marque bala nga Soli sa Gucci wala Louis Vuitton Billaay dama juge ci zéro Te fok ma nekk fi heros Ku ma dàq sa bureau Ma jënd fi immeuble louer la bureau Rombeul'ak auto, vroum vroum Sa xol bi di mbalax, boum boum Duñu daje boo ma gisetee Dama nekk ci foto, zoom zoom Mësuma compté kenn bi may sonn galère bi di ma téye Moo tax ba mënuma am ba soxla fi kenn pur compté samay billet Mën nañu bokk di jànge ci benn école Té yemuñu, bokkuñu classe Dakk la jànge sa xol bi di tàng Ma yërëm la, génél la saraxu glace Yaw danga rare Foo ne? Kenn gisatu la! Awma jot bi, maa ngi ci job bi Léegi ci Business bi rekk Sa gars yi ne nañu danga rare Foo ne? Kenn déggatu la! Demal ne leen awma temps bi Léegi ci Business bi rekk Maa ngi ci dara (yaa ngi ci dara) Nammuma dara (nammoo dara) Maa ngi ci dara (yaa ngi ci dara, kay!) Te nammuma dara (ay nammoo dara) Maa ngi ci dara (yaa ngi ci dara) Nammuma dara (nammoo dara) Maa ngi ci dara (yaa ngi ci dara, kay!) Te nammuma dara (nammoo dara) Ma ne doxal! Bul toppatoo, bul faale, bul sorale sax! Jittu nga leen, saani cravache bi, raw nga leen Gën ne leen Jëlal! Ku Sone Moss, ku sonn di nga mos Sa Ndeye ju baax ji la mu sonon a ngi Ku Sone Moss Maa ngi ci dara (yaa ngi ci dara) Nammuma dara (nammoo dara) Maa ngi ci dara (yaa ngi ci dara, kay!) Te nammuma dara (ay nammoo dara) Maa ngi ci dara (yaa ngi ci dara) Nammuma dara (nammoo dara) Maa ngi ci dara (yaa ngi ci dara, kay!) Te nammuma dara (nammoo dara)