Li may dundu ni li Yàlla bu mu jeex Fi ma nekk ni dafa romb neex Ki ma tee ni ay loxom dañoo woor Xol bi moo ngi feex, man xamuma woon Yaa ma woon (yaa ma woon) Fi ma lay yóbbu maa ko xam Yaa leen gëna pare yaa leen mën (yaa leen mën) Defal lu la neex yaa ko fi am Yaa mëna yee li nelaw ci man Windeluwma te miir naa (miir naa) Joxuloo ma livre te liir naa (liir naa) Ma xam ne yaay ki baax ci man Wóolu naa la te fiir naa (fiir naa) Yaa fi ne Man ma la validé Sama xol bi yaa ci ne Man ma la validé Baby yaa fi ne Man ma la validé Sama xol bi yaa ci ne eh Man ma la validé Lu ne nga ma jaral Sa bu neexee yaa ko waral Yaa ma jommal sama jinne Dama yénne di la teral Loo amul ci man yaw la Danga ma nob ma raw la Naa la aj fu kawe, kenn mënul yéeg ba ajji la Maa fa teg jeexal (jeexal) Sama dundu yaa koy neexal (neexal) Ne nañu ma naa la bàyyi Ma naa leen ma bañ! Ki bëgg naa ko na ma ray Moo may gaañ Xam sama valeur Yaw yaa xam li may jaar Doo ma jënde keneen, sama alal Yaw yaay ki may wër Ndax guddi ba fajar Yaa koy neexal ni lem ki ma tànn Yaa fi ne Man ma la validé Sama xol bi yaa ci ne Man ma la validé Baby yaa fi ne Man ma la validé Sama xol bi yaa ci ne eh Man ma la validé Maa fa teg jeexal (jeexal) Sama dundu yaa koy neexal (neexal) Xol bi yaa koy feexal (feexal) Sama dundu yaa kou neexal (neexal) Samp rekk teg fa jeexal Sama dundu yaa koy neexal Xol bi yaa koy feexal Sama dundu yaa koy neexal Yaa fi ne Man ma la validé Sama xol bi yaa ci ne Man ma la validé