Su ngeen xamoon fi ma jaar ba yegg ci fi Su ngeen jaaroon fi ma jaar ba tollu fi Céy su ngeen dundoon li ma dundu ba yegg ci fi Su ngeen xamoon, su ngeen xamoon, su ngeen xamoon Saa yu ma juumee di ngeen ma baal Saa yu ma juumee di ngeen ma baal Su ngeen xamoon ne fanaan na ci basaŋ bi ba tay Kër famille bu ne dëkk naa fa ba baay Yeen su ngeen xamoon ngeen jàpp te bañ a bàyyi Su ngeen xamoon ngeen fonk seeni waa-jur Saa yu ma juumee di ngeen ma baal Saa yu ma juumee di ngeen ma baal Ba may xaley njël la daan yeewoo gàddu sama pan Nda lu tollu ni barigo la daan rot bés bu ne te duma tere jàng Xuloo naa xeex naa ci robinet yi ba tay Su ngeen xamoon ne saa yu ma daan jàngi grand-yof lay doxe ba pompier Ndeysaan sama papa mësu bëgg ma xiif benn yoon Heure-u recréation la ma daan indil ndékki pain mayonaise Ba suñu waa école di ma tooñ pain mayonaise Saa yu ma juumee di ngeen ma baal Saa yu ma juumee di ngeen ma baal Su ngeen xamoon ni guddi la daan fot sama robe bi wér ko suñu gannaaw frigidaire Sama ngor sama jom ak jaay sama bégnet dugub bi Nango jàngi nango liggéey nango muñ moo tax ma yegg ci fi Saa yu ma juumee di ngeen ma baal Saa yu ma juumee di ngeen ma baal Ba may xaley njël la daan yeewoo gàddu sama pan Nda lu tollu ni barigo la daan rot bés bu ne te duma tere jàng Xuloo naa xeex naa ci robinet yi ba tay Saa yu ma juumee di ngeen ma baal Saa yu ma juumee di ngeen ma baal Su ngeen xamoon, su ngeem xamoon Céy! Bu ngeen xamoon Yeen xamoon, yeen su ngeen xamoon Su ngeen dundoon, céy! Su ngeen dundoon Li ma dundu yeen su ngeen dundoon Saa yu ma juumee di ngeen ma baal Saa yu ma juumee di ngeen ma baal