Baby Tay duma la wayal Dama lay rabal! Ñu dem Sama xol nga braquet dugg ci jël lépp te yoroo arme Duma prisonnier mais yaa ma tëj ci sa charme Mënuma fey te yaa tax ma sobbu ci géeju mbëggeel Xaaruma appel, sa xol laa décroché fajar teel Yaa ma bégal sa bopp, xaaroo ma naan la aimer ma Jaral nga ma rekk rekk-rekk soru ko ci MMA Dama doon dundu ak poison nga ñëw doon sama antidote Réparer sama vision wan ma ngor ba am ci dot Dama bàyyi lépp ànd ak yaw Sa loxo sama loxo ñu ànd di daw Dem fu la neex yaw Bëgg ma, yóbbu ma fu la neex Man yaw rekk laay topp (Bëgg naa la baby) Ni ma la rawee ëpp na (Wóolu naa la baby) Gëm naa la, wóolu naa la (Hey, xol bi yaa ci nekk) Sama xol bi yaa ci nekk (Fii yaa fi nekk) Sama xol bi yaa ci nekk Yaa may jox connection boo soree dootuma amaati réseau Jege ma, ma naan la je t'aime di ko répéter mel ni écho Ñépp laa supprimer, yaw laay jege di fumer Su ñuy waxtaanee téem nga fokk ko freestyle, lépp laay rimer Sama alal ki ma gënal yaa raw diamant ak or Maa lay wayal di la dalal yaay sama trésor Même soo may xool daay existant Yaa bari féem di ko teg ci temps Maay tëgg ñëw di la tëbbal tay dinga fecc ba daneel, tacc tan! Maak yaw ba géej gi fer du ñu may noon yi chance su ree Saañ naa wee ko sa fer te jamra du ka sans assurer Daw rekk amul arrêt mel ni auto bu amul frein Bi ma ñépp bàyyi wee, yaw yaa ma jàpp ni refrain Dama bàyyi lépp ànd ak yaw Sa loxo sama loxo ñu ànd di daw Dem fu la neex yaw Bëgg ma, yóbbu ma fu la neex Man yaw rekk laay topp (Bëgg naa la baby) Ni ma la rawee ëpp na (Wóolu naa la baby) Gëm naa la, wóolu naa la (Hey, xol bi yaa ci nekk) Sama xol bi yaa ci nekk (Fii yaa fi nekk) Sama xol bi yaa ci nekk Baby ni nga may bégalee maa ngi toog di ree Yaa ma gënal lu ne, fu ne, sama amoré Yaw laa doon wër, yaa ma feeñu Yaw la, yaw la, yaay sama plus for (Dama la nob) Chéri ribi daa, cha la, la, la (Man bëgg naa la) Yaay sama àljanna (Sama àdduna) Dénk naa la paradise (Naw naa la, rombu naa la) Man yaw laa dof Dama bàyyi lépp ànd ak yaw Sa loxo sama loxo ñu ànd di daw Dem fu la neex yaw Bëgg ma, yóbbu ma fu la neex Man yaw rekk laay topp (Bëgg naa la baby) Ni ma la rawee ëpp na (Wóolu naa la baby) Gëm naa la, wóolu naa la (Hey, xol bi yaa ci nekk) Sama xol bi yaa ci nekk (Fii yaa fi nekk) Sama xol bi yaa ci nekk I love you baby, yeah! Eh xol bi yaa ci nek! Fii yaa fi nekk!