Su ma jummul mos naa la gis yaw Ci benn jootaay (aywaay) Yaa ngi toog ak say gay Ngeen tek cay Lu ñu wax nga ree Di ma xoolale, di ma piisaale Man may dee Duma la ko nëbb ba ma la gise Am na lu ma doon yëg ci suuf (mu fey) Nga ñëw toog may ree ci kaw Bañu naa sama gay yi di ma ree Moo tax yaw mi yëgoo woon Aaaan sama mbëggeel Leer na ma ba leer Naqar dina jeex Man ne de li ma gis la leer na Aaan leer na ma, leer na Li nekk fi ni, li nekk fi ni Li ne sama xol Mbëggeel la ma jox (moom la ma jox) Mbëggeel la ma jox (moom la ma jox) Xamewuma ko woon Ndéké yoo moom la woon Li nekk fi, li ne sama xol bee Mbëggeel la ma jox Moom la ma jox Aaan moom la ma jox (eeeeh khé) Xamewuma ko woon Ndéké yoo moom la woon Ndax mbégte leer na ma ba leer Naqar dina jeex, sama àdduna Ndax sama nooflaay yaakaar naa Dina ma nopal Coups de foudre moo ma daal ma lay gis man Taw te na gis TaaTa Khouss man Fële na si géej mbëggeel man Ma bañ fa laay des man fa laay sobo, oh aye Li nga ma jaral mënuma ko wax fini Yaay sama cooppàti Papa Ndiaye takkal ma bin-bin Ey, takkal ma xol Je t'aime tellement Tu mérites ma yóbbu la yaw mi Ci Mame Ndiaye Savon Esk doo def farata ma gaaw ñëw Gallé ñu paccal lingom Kuy sa marie de vipère Diadia bul dof Duma ko laal, dafa bari No no bul dof Yaw mi fatal ma foofu Foo foy Li nekk fi ni, li nekk fi ni Li ne sama xol Mbëggeel la ma jox (moom la ma jox) Mbëggeel la ma jox (moom la ma jox) Xamewuma ko woon Ndéké yoo moom la woon Li nekk fi, li ne sama xol bee Mbëggeel la ma jox Moom la ma jox Aaan moom la ma jox (eeeeh khé) Xamewuma ko woon Ndéké yoo moom la woon