Alhamdu Lillaahi sant a war Alhamdu Lillaahi sant a war Jàmbat ju bari sax fajul naqar Te du tax kenn sawar Sidy la abal mbaggam Nga ciy lëng sooy nërmeelu Xel mi fa mu dem daa sori Saxaar gi ci tux yóbbuwu ma Nit ñee ma di yóbbaale Xel mi fa mu yéeg daa kawe Saxaar gi ci tux yéegewu ma Nit ñee ma di dofloo nii Xel mi fa mu dem daa sori Saxaar gi ci tux yóbbuwu ma Nit ñee ma ni yóbbaale Maa ngi romb fanweeri at sama wërsëg di daagu Soxla yi taxaw sañumaa toog may jug ak di daanu Ñépp naan lu ko dal kii moo dellu ginnaaw ni taat Amatuma baat, ñu may jàll baat Alal suy wax, bu neexul dañu ko wannal baat Ba ci muuma bu yor ay milyoŋ koñ bi moo fiy am baat Ma-rakk yii, ak seen yaay jii Daan ma yaakaar su ñuy añ dootuñu ma xaar Léegi dañu may (baleen ma waay) Ŋóobi di ma ŋar (baleen ma waay) Wutal nañu ma tur (baleen ma waay) Béjjanu ginaar (baleen ma waay) Lañu may tooñee fu ma jaar (baleen ma waay) Ma bañ ko di xeex (baleen ma waay) Ñu ma koy gën a wax (baleen ma waay) Ma beru bàyyi leen (baleen ma waay) Ñu naan damay tux ñax (baleen ma waay) Koñ bi yépp dëkkal ma fu ma dëkkul (baleen ma waay) Bëggatuñu maa naw Waayjur yi tere seen doom yi bëgg ma Ba ñépp di ma daw Nàmm seen paaka rendi ma Te naan Yàlla Buur Mooy dogal Sol ngeen mbubbu saytaane Xel mi fa mu dem daa sori Saxaar gi ci tux yóbbuwu ma Nit ñee ma di yóbbaale Naqar gu ànd ak naqaral Xalaat yu bari ànd ak wéet Man naa dofloo jaam bee Xel mi fa mu dem daa sori Saxaar gi ci tux yóbbuwu ma Nit ñee ma di yóbbaale Poos bi dërëm da caa baax Fayu luyaas dañu lay laaj Soble mbaa njëgu laaj Soo dul joxe li ñu lay laaj Bis dinga wax ñu ne: Ku la ko laaj Ñàkk loo def (baleen ma waay) Ñàkk loo def (baleen ma waay) Boole ceek nit ñi lay def (baleen ma waay) Man na dem ba def la def-def (baleen ma waay) Jamono ji sax daa metti muñ ci dafa war kuy jullit Laa Illah Illaahu Xel mi fa mu dem daa sori Saxaar gi ci tux yóbbuwu ma Nit ñee ma di yóbbaale Xel mi fa mu dem daa sori Saxaar gi ci tux yéegewu ma (baleen ma waay) Nit ñee ma di dofloo nii (baleen ma waay) Xel mi fa mu dem daa sori (baleen ma waay) Saxaar gi ci tux yóbbuwu ma (baleen ma waay) Nit ñee ma di yóbbaale (baleen ma waaay) (Baleen ma waay)