Tay jii mbëggeel a woote, sama Xalima topp sama yaram di daw ci rythmu cardiaque Mbëggeel dina feebar dina faj Dinga bëgg nit di ko nëbb say sikk ba far jag Mbëggeel garab la, ci sa jëmm lay xool Kàddug cofeel laay saxal ci say nopp Mbëggeel dafa am làkku boppam, bët dafay wax Bi nga nee ma jàkk laa xam ne yaw it bëgg nga ma Moom laay gis saa yoo may xool Mbëggeel de njuumte ci la bokk Dictée la bu kenn manul def zéro faute Kon bul mer ba weer ci mbedd mi loo xam ne Ci néegu séy lañu ko sumboon fóotsi Yaw laa jooy, yaru mbëggeel mooy li ma dal Ma lay xalaat ba dof ci yaw daal Su ma jógul taxaw ci sama bopp Dinaa yanu sama ay dàll Bi nuy gise, say bidéewi gët di fer-ñent Mbëggeel tàkk ci sa biir, nga déclaré ma say flamme Manuma la fay, boo ko waxul woon duma am fitam Mbëggeel di yëy sama xol, ma jënd guro jox imaam Xam naa sa njëg, xam naa li ngay jar (waaw waawaaw) Moo tax ma ñaansi la bañ a waaj (waaw waawaaw) Xam naa itam ne séy xare la (waaw waawaaw) Te jenn jigéen waru ci nàcc (waaw waawaaw) Jox ma sa xol (jox ma sa xol) Jox ma sa xol (jox ma sa xol) Jox ma sa xol (jox ma sa xol) Kaay jox ma sa xol (jox ma sa xol) Jox ma sa xol waaye Bu ko teg sama loxo Damay bañ su ma la meree sànniwaat la ko Ãaa! Jox ma sa xol (jox ma sa xol) Kaay jox ma sa xol (jox ma sa xol) Jox ma sa xol (jox ma sa xol) Jooox ma sa xol (jox ma sa xol) Déedéet mbëggeel amul xeet Waaye am na ay xeetu mbëggeel Am na mbëggeel yu lay xool di la xeeb, am Yu lay gis rekk doyloo ni nga mel Am na mbëggeel yuy fiir bëgg la moom, am Yu lay bàyyi nga moom sa bopp Am na mbëggeel yuy law di feeñ ci jëf, am Yu dul wees catu làmmiñ ak i nopp Mbëggeel amul couleur (waawaaw) Maak yaw doy na ma misaal (waawaaw) Index bu ñuul kukk di bëgganteek jigéen ju weex tàll Njabootu arc-en-ciel di peinture sama asamaan Su ma leen di xool, li may yëg sama xol, Yàlla kese Moo ko man Li tax nu séy du neen (waawaaw) Sunu destin moo nu jox dig-daje Manuloo ma daajal banc Doonte su ma taxawee di la xaar damay mel ni ku toog ci nen Mbëggeel dafa am làkku boppam, bët dafay wax Bi nga nee ma jàkk laa xam ne yaw it bëgg nga ma Moom laay gis saa yoo may xool