Arva aar Njaye Arva yaw kaay Arva aar Diogo Arva yaba xari maam booy Yàlla na bu dara yax Mamadou Diop yaba xari maam booy Kon arva mooy Ki mooy Arva sama lingeer bi Buñ ne danga baax kenn du ni gulet Wëratuma leneen yaw laa doon seet Yaay sama reni xol Gërëm naa la ndax Arva yaa may niital ni weer wi (arva) Àljanna lay dundu fekk maa ngi sa wet (yaw laa am) Yaay tool bu nandul nawet Jémbët naa man sama jiwu ci yaw Ndekke bëggawuma la xol bi kase (daagul ma lay wan) Arva sama ruu gi laa la yénne (daagul ma lay wan) Fu ma geesu gis la nga may gunge (daagul ma lay wan) Ni tàkkandeer Arva sama sumal nga (daagul ma lay wan) Yaw danga yore jikkooy jeegu puso (daagul ma lay wan) Samay mbokk ka wax waxu maako Yaay awa Sëriñ Babacar Arva wayal naa la man Mamadou mi sa jëkkër Kon wayal naa la ndameloo Ndax sama sant ngay wuyoo Diop yaba xari maam booy borom Ree ju neex ji mbaa meroo Tojal naa la koro nel Sama xol yaa koy majloo Diop yaba xari maam, lax nga sama gërëm Kon wayal naa la ndameloo Ndax sama sant ngay wuyoo Diop yaba xari maam booy borom Ree ju neex ji mbaa meroo Tojal naa la koro nel Sama xol yaa koy majloo Diop yaba xari maam, lax nga sama gërëm Bu ñu delluwoon démb manam Imam yokkat caan gi Ndax kontaan ci yaw Wol say mbokk damay dolli Yaw jeegu jëkkante nga Waaye man nga taamu ndax naru góor du àndak mbayan yi Boo fekkee woon keroog talaata nder Jigéen ña talon seen bopp sa nekk ba Ngir bañ gàcce duñu la yóbbul dara Ndax yaw yaa jaay sa sant waaye sant bi nga jënde Yombul sant daqu ko Diop du kenn kaay wuyoo Kuy wër ku rafet judd Ba yam ci moom dëppal Ko fi gënul gënu la yaay borom maamu buur yi Kon wayal naa la ndameloo Ndax sama sant ngay wuyoo Diop yaba xari maam booy borom Ree ju neex ji mbaa meroo Tojal naa la koro nel Sama xol yaa koy majloo Diop yaba xari maam, lax nga sama gërëm Kon wayal naa la ndameloo Ndax sama sant ngay wuyoo Diop yaba xari maam booy borom Ree ju neex ji mbaa meroo Tojal naa la koro nel Sama xol yaa koy majloo Diop yaba xari maam, lax nga sama ngërëm Diop yaaba xaari maam Moom Mamadou yar na ñu ci baneel (Matar ndumbe Soxna Niang Serigne Codou Ndiaga Issa Dieye) Leer gi bawan njukku ba maka Mamadou, Mamadou Yaa ba xaari maam Chérie Arfaa Ndameloo cire Ndameloo cire bëggul ndame cire (Diop Yaaba xaari maam) Mamadou (yaaba xaari maam) (Yaaba xaari maam) Wax nga dëgg, waay! Jiwaru Keita ko daan jël Xaar ma Yàlla réew mi déglu leen ma Maa way sama doom ko koy Arva Toucouleur Koura Ndiéme billaay Ndameloo cire Ndameloo cire bëggul ndame cire (Diop Yaaba xaari maam) Mamadou (yaaba xaari maam) (Yaaba xaari maam) Koura Niang ma ta Kathia Torodo Samba Ngari Ndiana Yaay majloo jigéen ñi Yaay majloo góor ñi Sama doom ji l'amour gaddu woon ba tay dañul Jiitu nga leen saani cravacher gi daan leen