Bëñ ak làmmiñ ña dëkk, yenn saay ñu laale Man rekk ma xam sa njëg moo tax sekuñu bàyyante Bul mer ba tàng wax ma looy réccu suñu juboo we Mën nga ma gaañ te doo ko yëg bul ma wan sa doole Tijjil sa kanam bi nga tëj man nga nop ma la sommet Niangal jàppu la même soo meree dangay gëna rafet Doole mbëggéel xajul si yaw bàyyil fi nga téye Lewtoo su yàgg jële bi ñaaw mak yaw sekuñu bàyyante Namm naa la waye fok ma tek xel Yendoo composé son numéro te duma bës appel Yenn saay ma dugu mode fantôme Dem status xol la xew ci loy dox gueuth na gis no mel Sago ngi may raay wante bëgguma ndieuka wax ak moom May góor te fok mu xam ni fi benn baat la, may boroom Lo wax ma tangal te pourtant man bëgg naa bàyyi mu sedd Del makh nakh so noppè ma dof sa baat la bëgg di dègu Jarul nga may wane ni yaa ngi ci jamm, xam naa ni yaa ngi souffrir Mak yaw ñoy wax te xam na lépp, dama la bàyyi si biir Dama la namm ci live bi guddi waay dugal dama ragal wéetaay Taamal nga ma lu meunta weuy, waye xëy na di nga ma wo tay Su may lekk lu neex ba xel mi dem ci yaw Day mel ni mësuma xiif Waxal ak maan nakh namm naa la, sama xol mëna gif Oh love Eh eh love Maa ngi beurè ak sama xol bi Ba guddi gi jeex waye fu ma tourné sa kanam laay yaam Mbëggéel di gëna yokk come bis bimalay gneuka xam Mal yak sougn xuloo nonn yi am ndam I’m sorry, yaw namm naa la eh Chérie non non Stay with me oh Because baby I love you soo Maa ngi dora gif, léegi soo ma wowee Yaay reine def naa la lépp Nax mak yak sekuñu bàyyante (Déedéet yaw lay feel) Du man, du yaw, xol yi ñoo ko décidé Mak yak sekuñu bàyyante Du man, du yaw, xol yi ñoo ko décidé Mak yak sekuñu bàyyante Du man, du yaw, xol yi ñoo ko décidé