Gis naa la ngay njaap yeah Def ci fulla ju mat sëkk Man daal li may ñaan amiin waay Mu juge doon sama wërsëg Day neex ci sama xol Bis bi nga may njëkk a xool Ne ma bëgg naa la doonte benn yoon Lay mas a doon ci sama dund Yàllaay Buur lu Ko neex dogal Yàllaay def lu Ko neex ci jaam Te Yàlla def man ma taamu la Nattu la am ndogal, jëlal Yàllaay buur lu Ko neex dogal Yàllaay def lu Ko neex ci jaam Te Yàlla def man ma fiire la Nattu la am ndogal Hee! Bul ma sàgganne waay Bul mas a fàtte ne waay Péncu xol ma yaa fa ne waay Kon bul ma sàggane waay Way wi, fent naa ko ndaxte Yaw kenn nga doo ñaar Wërsëgu Yàlla nga ehh waay Day neex ci sama xol Bis bi nga may njëkk a xool Ne ma bëggg naa la donte benn yoon Lay mas a doon ci sama dund Yàllaay buur lu Ko neex dogal Yàllaay def lu ko neex ci jaam Té Yàlla def man ma taamu la Nattula am ndogal, jëlal Yàllaay buur lu Ko neex dogal Yàllaay def lu Ko neex ci jaam Te Yàlla def man ma fiire la Nattu la am ndogal Hee bul ma sàggane waay Bul mas a fàtte ne waay Péncu xol ma yaa fa ne waay Kon bul ma sàggane waay Boo ma woyafalee mbaa nga sàggane ma Dina tiis ci man, dina tiis ci man, dina tiis Boo ma woyafalee mbaa nga sàggane ma Dina tiis ci man, dina tiis ci man, dina tiis Eh dama lay xool Yaa nekk sama biir xol Eh dama lay xool Yaa nekk sama biir xol Bul mas a fàtte ne waay Péncu xol ma yaa fa ne waay