Àdduna wërngal lay jiital Koj ma ci jànt bi soo ma nammee Jot gi mayatuma teew bi Waaye ci mbégte lay mujj soo ko muñee Muñal dina xéy neexi Cofeel ngor a kay sàmm Ëllëg dafa jar sedd Sa doom yi dañuy maa ngi Bu doon misaal la ci yiw ma ni yaa di kiiraay Boroom asaman na ñu boole, daaru dunya Keneen du nu musuloo tax ma dégg muñal Boroom asaman na ñu boole, daaru dunya Bu kenn bëggul bëgg naa la (Déggal gars yi) Bu kenn dikkul danga may gis (Yàlla def gawar laa man) Su ñépp demee wacc maak yaw (Maak yaw la daaru dunya) Suñ dellusee fekk maak yaw (Sutura yaa di kiiraay) Su kenn bëggul bëgg naa la (Déggal gars yi) Bu kenn dikkul danga may gis (Yàlla def gawar laa man) Su ñépp demee wacc maak yaw (Maak yaw la daaru dunya) Suñ dellusee fekk maak yaw (Sutura yaa di kiiraay) Muy taw mbaa mu naaj Muy guddi mbaa bëccëg Waa dëkk ba nga naan Dikk nga ma car wayal Musuloo xàddi ci man Doo ku may rusloo itam Tàsoo sama yaakaar xarit sama Sutura yaa di kiiraay Muñal dina xéy neexi Cofeel ngor a kay sàmm Ëllëg dafa jar sedd Sa doom yi dañuy maa ngi Bu doon misaal la ci yiw ma ni yaa di kiiraay Boroom asaman na ñu boole, daaru dunya Keneen du nu musuloo tax ma dégg muñal Boroom asaman na ñu boole, daaru dunya Bu kenn bëggul bëgg naa la (Déggal gars yi) Bu kenn dikkul danga may gis (Yàlla def gawar laa man) Su ñépp demee wacc maak yaw (Maak yaw la daaru dunya) Suñ dellusee fekk maak yaw (Sutura yaa di kiiraay) Bu kenn bëggul bëgg naa la (Déggal gars yi) Bu kenn dikkul danga may gis (Yàlla def gawar laa man) Su ñépp demee wacc maak yaw (Maak yaw la daaru dunya) Suñ dellusee fekk maak yaw (Sutura yaa di kiiraay)