Yaa di sama waay Maa di tam sa waay Ñaanuma la tooñ Su amee Yàlla nga ma baal Yaa di sama waay Maa di tam sa waay Ñaanuma la tooñ Waaye su amee Yàlla nga ma baal Ne ma li lay bañ Wax ma ni nga ko bëgge Jom ji laay rang Ñëkkewu ma waaye ma lay mujje Ngelemu jëg bu juróom Su ma ko amoon may na ma la yeah Ñu jél ko jéebal laa ko Dama bëgg lool yéey na ma yeah Àdduna du mës a neex ba ma fàtte la Dieye Sélémane Ngelemu jëg bu juróom Su ma ko amoon may na ma la yeah Dieye Sélémane laay way Céy Dieye Sélémane laay way Dieye Sélémane laay way Céy Dieye Sélémane laay way Dëkk ba nga ma jële Sori naa lool Diggante yi nga ma fekkoon tam Metti na woon Li may mën wëy yépp soo ko wonewul woon Kon leneen laay doon Kon yoon la délloo la ñuukal eh Dieye Sélémane Massamba raar a Dieye Yirim diir na buur Daour Ndumbe Ndela Dieye Dieye Sélémane Massamba raar a Dieye Yirim diir na buur Daour Ndumbe Ndela Dieye Dieye Sélémane Dieye Massamba Dieye Sélémane Massamba moo ni Duma dem Sine duma dem Saloum Te ku ma tee sol buur man sa kaw laay jaar Dieye Massamba Ngelemu jëg bu juróom Su ma ko amoon may na ma la yeah Ñu jél ko jéebal laa ko Dama bëgg lool yéey na ma yeah Àdduna du mës a neex ba ma fàtte la Dieye Sélémane Ngelemu jëg bu juróom Su ma ko amoon may na ma la yeah Dieye Sélémane laay way Céy Dieye Sélémane laay way Dieye Sélémane laay way Céy Dieye Sélémane laay way