Hey Massamba Walo All days and nights Yaa ngi ci sama xel mi Dañ ma lay laaj Maas yaw ana booy bi Waaye li nga ma teg ci metit dafa bari Li nga ma digoon ni ba nga ko xajul ci lim Yaw sama xol bi nga ma laaj Ne ma Masàmba dootuma la gaañ Waatal nga ma wallaaayy billaay Ne ma ne déwen dootul mel ni daaw Waxoon naa la bul ma sàggane Baakari ak Daarama Ne woon naa la duma la fowe Aram Lóo Kumba Caam Naa la wan ne man naa la wan ne Xam naa ne li nga may jaay Xanaa xamóo ne xam naa ne Masamba loo may jaay Nekkatuma xale boog Kenn du ma naxee noonu Naa la ne wan ne man naa la wan ne Xam naa ne li nga may jaay Xanaa xamóo ne xam naa ne Masamba loo may jaay Nekkatuma xale boog Yombatuma naxee noonu Bëggatuma la bàyyi Ni manatuma la ba Dem nan ba romb foofu noonu Xamuma nu mu tuddeeti Sori na daal Tax manatuma dellu ginnaaw Tegul ci yoon wi Defaral sa taxawaay Ehh Yaw sama xol bi nga ma laaj Ne ma Masàmba dootuma la gaañ Waatal nga ma wallaaayy billaay Ne ma ne déwen dootul mel ni daaw Ne woon naa la bul a sàggane Baakari ak Daarama Waxoon naa la duma la fowe Aram Lóo Kumba Caam Naa la ne wan ne man naa la wan ne Xam naa ne li nga may jaay Xanaa xamóo ne xam naa ne Masamba loo may jaay Nekkatuma xale boog Kenn du ma naxee noonu Naa la ne wan ne man naa la wan ne Xam naa ne li nga may jaay Xanaa xamóo ne xam naa ne Masamba loo may jaay Nekkatuma xale boog Yombatuma naxee noonu Ku la safooti faale ko Ku la bëgg moo la sonal daal Han ki la bañ Ki la bañ da laa noppal Ku la safooti faale ko Ku la bëgg moo la sonal daal Han ki la bañ Ki la bañ da laa noppal