Eey Massamba Waloo Eh-eh waay! Bi ma la xame ba léegi yaw New na nga def lu ma metti yaw Weg naa la doo fi wayade yaw Fa ma la aj duma la fa aje yaw Ndax yaay kenn ki nga xam ni every night man Moom lay xalaat su may tëdd su ma yéewoo Yenn saay ma réer nga indiwaat ma Xam naa ni man rekk nga bëgg Ki la bëgg ba bëgg la Te bëggantuwu la Loo ko mën ci def du ko gis Ndax mbëggeel nga lay xool Ki la bëggul bëggu la Moom bëggantuwu la Loo ko mën a defal du ko gis Ndax mbañeel nga lay xool Xam nga ni man dama la bëgg Yaw sentir nga coono yi may daj ci yaw Keneen ku mu doonon ku dul yaw ne na wéreñ Gis nga ni man dama la fonk Ñoom ñépp gis nañu coono yi may daj ci yaw Keneen ku mu doonon woon na ko ginnaaw ba dem Ki la bëgg ba bëgg la, éeeh Su la meree dangay feebar di lox di liw Mel ni ku sibbiru mbëggeel metti na Ki la bëgg ba bëgg la, éeeh Su fi nekkee dangay kontaan di bég di ree Mel ni ku cokkali mbëggeel neex na lool Lég-lég mu neex, sa xol bi naat Ngay fecc bànneex di ñaan mu yàgg lool Ki la bëgg ba bëgg la Te bëggantuwu la Loo ko mën ci def du ko gis Ndax mbëggeel nga lay xool Ki la bëggul bëggu la Moom bëggantuwu la Loo ko mën a defal du ko gis Ndax mbañeel nga lay xool Xam nga ni man dama la bëgg Yaw sax gis nga coono yi may daj ci yaw Keneen ku mu doonon ku dul yaw ne na wéreñ Gis nga ni man dama la fonk Ñoom ñépp gis nañu coono yi may daj ci yaw Keneen ku mu doonon woon na ko ginnaaw ba dem Yaw dogo làmp yi ci mbelguane Waaye man bëgg naa la Dogo Ngidu ma ci Penda Man Ndiaga Thiam sama maam la Yaw dogo làmp yi ci mbelguane Waaye man bëgg naa la Dee mo fén di ma tuttal foo nek yëkkëti ma sama waay nga Yaw dogo làmp yi ci mbelguane Waaye man bëgg naa la Yaw dogo làmp yi ci mbelguane Waaye man bëgg naa la Yaw dogo làmp yi ci mbelguane Waaye man bëgg naa la