[Mia Guissé] Yaay booy wuyu ma, dama lay laaj (yeah!) Yaay booy yédd ma, dama lay laaj (yeah!) Bëgguma lu baax rëcc ma, dama lay laaj (yeah!) Bëgguma rëccu tam, dama lay laaj Xam naa li muy laaj (Li muy laaj, li muy laaj?) Ñoom ñaar ku ne mungeek li ñuy laaj (Li muy laaje, waawaaw) Damay bëgg a jaaxle Ndax awma choix ci ñaar ñu doy war [Wally Seck] Bëgg nga mais yaa ngi xel ñaar Bëggoo ku xar sa xol bi ñaar, baby Réy-na ñi fi jot a jar Ñoo fowe sa xol ba nga foog ni ñépp a soxor [Amadeus] God lu mu bind daje def ñaar Te yaw yaay sama genn-wàll man Asaman si ni mu yaatoo Naj bi li muy tàng Yaay keppaar giy nëb naj bee [Mia Guissé] Damay bëgg a jaaxle Awma choix bébé, xam naa li muy laaje [Amadeus] Lingeer nga bul jaaxle Mbégte dunya yi rekk laa la yénne (hey) [Mia Guissé] Damay bëgg a jaaxle Awma choix bébé, xam naa li muy laaje [Amadeus] Yaw lingeer nga bul jaaxle Mbégte dunya yi rekk laa la yénne Su ma gisee nga naan danga ma nob Te nday ji sex du am ci jamaale Mel ni asaman si ni mu yaatoo Ak biddéew yi ni ñu taaroo Neex na ma, waaye jaaxle Ndax xamuma ki may tànn [Wally Seck] Lingeer may Latyr Diop Déguéne Mbaye (anh!) Ballago Khaliloulay (wuy!) Njaabot ga lay wutal yaay Te kër ga yaa fa doy lingeer way (ayah!) Ma di buur géwel, xuss ndama lay bégal Soo bëggee ma lay wayal, col nder ak tama way Lingeer kaay, soo bañee ma wet kaay Kaay, yaay sama wéeruwaay [Mia Guissé] Damay bëgg a jaaxle Awma choix bébé, xam naa li muy laaje [Amadeus] Lingeer nga bul jaaxle Mbégte dunya yi rekk laa la yénne (hey) [Mia Guissé] Damay bëgg a jaaxle Awma choix bébé, xam naa li muy laaje [Wally] Yaw lingeer nga bul jaaxle Mbégte dunya yi rekk laa la yénne Neex na ma, waaye jaaxle Ndax xamuma ki may tànn No-no-no mon bébé Ne t’en vas pas, waaw Neex na ma, waaye jaaxle Ndax xamuma ki may tànn