Jege ma ma won la li nekk ci sama xel Déglu ma, ma déey la li ngay def ci sama xel May la ci ndax lii de neen la Xol bi li muy tegg, lépp dëgg la Gëm naa ne lii de mayu Yàlla la Moom mi ñu boole, ca aras lañu ko fase Mayu Yàlla la Xale la ba tey, lu yàgg dafa fay Kon naa ci ñépp tey te xam ne li du fay Sama xol yaw la fal, sa bos de man la tànn Foo yendu laay fanaan, sama baby kaay Gën ci man, baax ci man Gaaw ci man, sës ci man (Yaw yaa sës ci man) Dof ci man, mën ci man Sax ci man, wóor ci man (Yaw yaa woor ci man) Tank tank, mbagg mbagg Lu joxooñ ma dagg Lu ma bëgg ci nga dëkk Ndank ndank ba yëg fu sori Jàpp bañ a bàyyi Doon ci xàddi, doon ci tàyyi Xel beey seede Ne na toj nga bopp bi Xalatul ku dul yaw, yaw yaa fi ne Xel beey seede Lu muy dundu moo neex Neex a neex a neex, bëggul mu jeex Xale la ba tey, lu yàgg dafa fay Kon naa ci ñépp tey te xam ne li du fay Sama xol yaw la fal, sa bos de man la tànn Foo yendu laay fanaan, sama baby kaay Gën ci man, baax ci man Gaaw ci man, sës ci man (Yaw yaa sës ci man) Dof ci man, mën ci man Sax ci man, wóor ci man (Yaw yaa woor ci man) Gën ci man, baax ci man Gaaw ci man, sës ci man (Yaw yaa sës ci man) Dof ci man, mën ci man Sax ci man, wóor ci man (Yaw yaa woor ci man) Yaw yaa sës ci man Yaw yaa woor ci man