Sama yaay ne ne ma Bul tiit te bul ragal Demal foncel Te xam ne am nga ñaanu yaay Am nga ñaanu yaay, oh oh Dinaa jëm lu ma mën Ndax yaay li nga sonn ma muñloo Dinaa def lu ma mën Ndax baay li nga sonn ma dooleel Moo ma dooleel Baay boy moo ma dooleel Yoon wi gudd na Waaye gëmal sa bopp te xam yaay kan Ku mu mën doon ku mu mën ci nekk Gëmal sa bopp Gëmal sa bopp Gëmal sa bopp Ñu ngi lay xeex te xamoo leen Ñu ngi def te gisoo leen Waaye bul tiit, bul jaaxle Ndax Yàlla ñépp la fi nekkal Bul mas di xaadi Jàppal ba mu dëgër bul bàyyi Dinaa jëm lu ma mën Ndax baay li nga sonn ma muñloo Yoon wi gudd na Waaye gëmal sa bopp te xam yaay kan Ku mu mën doon ku mu mën ci nekk Gëmal sa bopp Gëmal sa bopp Gëmal sa bopp Lambour Penda Madior Séni Ndiaye, Yacine Diémé Borom Diam yi ñul yi ak yu xees yi Ma wooy sama maam jee Ma wooy sama maam Man jooy na sama maam jee Duma la mësa fàtte mukk ci àdduna Sa dem gi wetal na ñoo Maam boy namm naa la