Lii de neex na lool Bi bànneexu xol Lii may yëg su ma koy xool Lii de neex na lool Ba ëpp tol Way le leen ma sama doom ji Man de bëgguma lu lay metti Ma lay naxtaan ba ngay reetaan Feesal sama mbëggeel ci yaw Muy law ba faw Ayo sama nenne, nenne tuuti Ku may naqal sama doom ji Ayo sama nenne, nenne tuuti Ku may naqal sama doom ji Cofeelu yaay si doom Ku ko dundul doo ko mën a xam Bis bi nga juddoo ba tew ci samay loxo Li de leer na Bidéew bi naw, tere ci asaman mbëggeel Dundu ci xol te dee ci bët Li de leer na ma Bi ma njekke gis ma nenne Yëg-yëg sama xol bi neex Naqal sa doom su jooyee nga bëgg Lii de leer na ma Sama coono mooy sa bànneex Su may liggéey suba day neex Doom faw nga bëgg ba raw ci say moroom Lii de leer na ma Ayo sama nenne, nenne tuuti Ku may naqal sama doom ji Ayo sama nenne, nenne tuuti Ku may naqal sama doom ji Sama doom, sama soppe Dundu mata jooyoo Moom lay jooy doom dundal Soo dundee ba mën liggéey Feral say rongoñ