Yéenewoo ma lépp li ma doon Temps amatul damay jokk yox Te newuma ci li nga fok Mel li lan la yaw lan nga téye ci sa biir xol Xamal ni xamal ni Fi de loo fi sombi yaw mi din' ko jeem a naan Jàppal ni jàppal ni Sa yéene mooy sa nekk Foo mën ti nekk dinga fa fanaan Yàlla Buur bi sàkk la te sàkk ma Wax ma li lu ko fi jar Am talibe tax nit yi di ma sopp Du ñakk fay dama wacc sama bopp Wax ma gën naa ni, hey he he Sooy wéet di siisu Est-ce que doo jeem a daalu Man sax dama waaru Hey, ndax lu ëpp tuuru Yàlla bind te yamalewul Soo ko nangoo doo sonn Su yabo nga nangu dogal He, Buur Yàlla mooy maye Noppalul foo yewoo gis ma Foo yewoo gis may dem Noppalul foo yewoo gis ma Foo yewoo gis may dem Xoolal fi, moo ngi cool Ah, moo ngi baax Xoolal fi, moo ngi cool Noon, fi lépp moo ngi baax! Wax ju bon bi nga jël teg ko sama der Yaw mi de lan moo la dal Looy dox di mer Mënoo ci man dara Jël naa lépp teksi loxo Yàlla Buur bi ma sàkk Gëm naa ne loolu Mooy sama gàllaaj Sooy wéet di siisu Est-ce que doo jeem a daalu Man sax dama waaru Hey, ndax lu ëpp tuuru Yàlla bind te yamalewul Soo ko nangoo doo sonn Su yabo nga nangu dogal He, Buur Yàlla mooy maye Noppalul foo yewoo gis ma Foo yewoo gis may dem Noppalul foo yewoo gis ma Foo yewoo gis may dem Xoolal fi, moo ngi cool Ah, moo ngi baax Xoolal fi, moo ngi cool Noon, fi lépp moo ngi baax! Noon, fi lépp moo ngi baax!