Nit ku ne am na ku kaay wétali Ku kaay wax dëgg kuy dellusi xelam Nit ku ne am na ku kaay jubbënti Sayu reere fàtte li ko war Yéena maggando, yéena gowando Bokk ay bëgg-bëgg mel ni ay seex Mel ni ay seex Xaritoo xarit fu ma lay jëleeti Yaw mi may teg si yoon su ma réere Xaritoo xarit fu ma lay jëleeti Yaw mi ma gëna xam sama bopp Wax ma rekk wax ma fu ma lay ameeti Yaw mi may teg si yoon su ma réere Wax ma rekk wax ma fu ma lay ameeti Yaw mi may wétali Oh oh oooh Ouh ouh ouhh Yenn saay ñu meroo Ku ne dem sa yoon Seytaan ak pexem mëna tas lu ne Waye yàgg yàgg dañuy boo loo watt Àndaando nekk benn mel ni ay seex Mel ni ay seex Xaritoo xarit fu ma lay jëleeti Yaw mi may teg si yoon su ma réere Xaritoo xarit fu ma lay jëleeti Yaw mi ma gëna xam sama bopp Wax ma rekk wax ma fu ma lay ameeti Yaw mi may teg si yoon su ma réere Wax ma rekk wax ma fu ma lay ameeti Yaw mi may wétali Oh oh oooh Ouh ouh ouhh Mel ni ay seex Di dox mel ni ay seex Xaritoo xarit fu ma lay jëleeti Fu ma lay jëleeti? Xaritoo xarit fu ma lay jëleeti Wax ma kooo! Wax ma rekk wax ma fu ma lay ameeti Wax ma kooo! Wax ma rekk wax ma fu ma lay ameeti Yaw mi may wétali