Man de xëy-na Xëy naa Faw ma wuti lu ma jariñoo May taw ci kër gi taaluma biddanti Faw ma wuti lu ma jariñoo Dem korti-korti indi ci kër gi Pare tekki teral samay ñoon Yaay jurul doom bu ñàkk jom Lu mu metti na xal yoon Jël hilaire bay sama tool Ku tekki bari nday Waaye ku amul nawle yaay Nga la dom, dañ la saas Kon lu mu metti nan ko baay Xuus na ci géj gi Ngir tebi ass bi Liggéey nday feeñ na Tay yaay sa añ baa ngi Man de xëy-na, xëy-na dem Xëy-na, xëy-na dem Tàggu sama yaay Tàggu sama baay Sama tay bu nekk gàccel na sama demb Rawati na li ma togg sumb tay Sant Yàlla buur bi ma may Ba ma mëna xale yoon Moom moo ko saañ Yàlla buur bi mooy ki mën Sant naa la Allahou buur bi yaay ki mën Ma tekki teral yaay ba jële ko ci coono Bay boy bëgg naa ci man bëgg naa ci man Sama Yaay Djé Sen Tialy, Gatié Ngalama Man de xëy-na, xëy-na dem Xëy-na, xëy-na dem Tàggu sama yaay Tàggu sama baay Ku dem fu la lay yóbbu Doo jigéen, góor nga te yaay taw Demal maa ngi lay ñaanal Yàlla na la Yàlla yokku Diouf