Yaa tax ma fent lii, ci xol bi lay jóge Way wi yaay boroom Nga tax ma bind lii, ci xol bi lay jóge Maa la jël, teg la fu kawe, maa ko ñeme Yëg la, jox la xol bi nga téye bul ko fowe Bëgg la, teg ci fonk la, gëmewuma la Yéene naa la lu ne, yaa fi ne, amul lu ñuy téye Su ñu ma bëggee nañu ma bàyyeek yaw Manaluñu ñu dara, suñu mbëggeel day law Dañuy xaar, fii de ñoo fi ne Mélodie biy yëngal sama xol, yaa koy animer Yaa tax ma fent lii, ci xol bi lay jóge Way wi yaay boroom Nga tax ma bind lii, ci xol bi lay jóge Ku man na def ni man? Bëggal ni man? Bari feeling ni man? Eeh, joŋeel ni man Yaay ki ma saf Yaay sama saajobaan Yaw laay tippoo Lii de ku mu neexul nga dindi ko! Takk ma ci baat, diri ma, man de bëgg naa Foo ma xool gis ma ma lay ree, lii de saf na ma Tay lu waay di jaay lamb na, loolu wóor na ma Bëgg la ba bëgg ni la bëgg, xanaa jommi nga Su ñépp bàyyee, man ma des ak yaw Manaluñu ñu dara, suñu mbëggeel day law Dañuy xaar, fii de ñoo fi ne Mélodie biy yëngal sama xol, yaa koy animer Yaa tax ma fent lii, ci xol bi lay jóge Way wi yaay boroom Yaa tax ma bind lii, ci xol bi lay jóge Ku man na def ni man? Bëggal ni man? Bari feeling ni man? Eeh, joŋeel ni man Yaay ki ma saf Yaay sama saajobaan Yaw laay tippoo Lii de ku mu neexul nga dindi ko! Baby na nga jënd sa garde pareel Samba Diarra Lañu la indil sincérité Bi nga làmbool moo may dundal Moo tax dama la bëgg Ci sama xol bi dara du ko dindi! Yaw mayal sa noon yi ndox Baby, mar nanoo naan Ku lamb yaa tay daagul fu ñu la nobee (Yaw mayal sa noon yi ndox, baby mar nanoo naan) Ku lamb yaa tay daagul fu ñu la nobee (Yaw mayal sa noon yi ndox, baby mar nanoo naan) Chéri guddi tay Ne guddi tay sab noon du nelaw! (Eeh guddi tay, ne guddi tay noonam du nelaw!) Narah na nga jënd sa garde pareel Samba Diarra lañu la (Eeh guddi tay, ne guddi tay noonam du nelaw!) Ma ne! Yaay ki ma ñoppati Yaay ki may bégal Yaay ki may dundal guddeek bëccëg Ku lamb yaa tay daagul fu ñu la nobee (Yaw mayal sa noon yi ndox, baby mar nanoo naan) Ku lamb yaa tay daagul fu ñu la nobee (Yaw mayal sa noon yi ndox, baby mar nanoo naan)