Leer moo jur takkandeer Fii ci àddunaa kenn du joxoñ takkandeer Fu amul benn leer Fii ci àddunaa Leer moo jur takkandeer Fii ci àddunaa kenn du joxoñ takkandeer Fu amul benn leer Fii ci àddunaa Waaw damani Fii ci àddunaa kenn du tudd ker ci biir lëndëm Di ko gërëm Boroom kër mooy leer bi la jur Def ci yaw taangoor Biy tax ki la jur def ci yaw ker Day tax nga feeñ loolu wane defare Ma ni ëllëg nga daal di doon Nit ku juddu, nit ku fees Bés ñëw Yàlla miy buur Jëlé fi baay su loolu amee Ci sa biir jikko Ay nit di la joxoñ Naan kee doomu diw la Xool ko ci leer gi mu la yaree Bi mu la jurée Kii sa baay la Baay baaxoon na Jubóon na Dama demoon seeti baay Fekk bàmmeelam Ma toog di jooy Yaakaar naa baay