Gëj naa la gis (namm naa la) Namm naa la (namm naa la) Yàlla la xiir (ci man) Ci man xamm naa ko (xamm na ko) Yëg naa ko Yaay boy kaay jël ma balaa ma dem géej Yaay boy kaay jël ma balaa dem géej Yaay boy daadan muñ ba dommam teral ko kaw suuf Baay tam daadan muñ bu xolam sedd ga doon buur Boo amee defal tout, sa famille bégal ko mooy tout Jëndal meew ak sukkër, ceeb ak dëwlin Mindeef taxul (mindef taxul) Xaalis taxul Les waxul (les waxul) Nit dey wax lum deful Yaafus warul Boroom karaw bu ñuul Ñépp am naan bidéew fi ak déwuñ du reer Ku ley seddil ci gaalu xaaj Bul ko bañ nga la bu mu fa fekk sa loxo Liggéeyu nday añu doom Liggéeyu nday añu doom Gëj naa la gis (namm naa la) Namm naa la (namm naa la) Yàlla la xiir (ci man) Ci man xamm naa ko (xamm na ko) Yëg naa ko Yaay boy kaay jël ma balaa ma dem géej Yaay boy kaay jël ma balaa dem géej Sama yaay yaay yaay Ba muy ñaati yoon Tég ci baay boy looloy ndami doom Àljanna gi sey suufu tànk waye barke baay Yaay bul jàppe duma la mësa bàyyi Yaay, ni ma lay namme dumsi masa tàyyi Yaay, dëkke daw yaw mësuloo bàyyi Yaay, dima tég ci yoon yaw yaa ci àay Jigéen ju mën góor liggéy ga sama kër baay Yir ma yar ma yee ma Joom fu la ak fàyda Xam sa bopp yox la, jugal liggéey jox la Danu jugaat laaj ma, yaay sama galaaj yaw la yaw la Gëj naa la gis (namm naa la) Namm naa la (namm naa la) Yàlla la xiir (ci man) Ci man xamm naa ko (xamm na ko) Yëg naa ko Yaay boy kaay jël ma balaa ma dem géej Yaay boy kaay jël ma balaa dem géej