Fi ñu ma doon séentu gisuñu ma fa Fi ñu ma doon xaar ñëwuma fa Ñoo ngi ma doon xaar ci gallu xat Waaye góor du ci lépp la xaaj Yaay booy ne na siggil na ko Jëkkër ne na sagal na ko Askan bi sagal na leen Baay booy sa doom wacc na Yaay booy ne na siggi na Baay booy ne na siggi na Askan wi tamit ne nañu siggi nañu Seen doom bi ñu doon xaar wacc na Guddi bi ñu ma mayee ci lañu ma jëlé Yaay jaaxle lool bajjen toog di xaar Seen doom ji wacc na Siggil na leen tasul yaakaar Ñi ma doon xaar yegsi na Ñi ma doon sentu tew na Sama noon yi du gen ree Ndax sama yaay booy siggi na Yaay booy ne na siggi na Baay booy ne na siggi na Askan wi tamit ne nañu siggi nañu Seen doom bi ñu doon xaar wacc na