Ngëram, ngëram ñeel na ka dog buumi jaam ñi Ki tax ñu sampi daara fi ba mbacké baari Sant ak ngëram ñeel na borom silkul jawaahiri Jàraama rek doyul ci borom magal gii Yaa ko jar, ma la koy wax: Ya qalili Mbégté'm yâllah nga ak yonnen, yâ habibi Àddunah da la koo may, yâ azizi Li mu ëmb it yaa ko moom, yâ wasiilati Yaa mën fii ak fa nu jëmm yaay jaalé jaam ñi Bu mbër yeep taxawee yaa mën ci goor ñi Makaak madiina, seen mboot ya ñëw na Diggante njaareem mbacké ba touba Bamba teeye naa laak leneen ludul samay loxoo Ndax xam nga yalla xamlé nga koo Maam ceerno faati loxol ndayjoor la Moo gaaganti naar ya té laaloul mool ya Jaramaa rek doyul dañ la wara kennal Suñ goree suñ leepp yaa nu ko wara gënal Ëskey la ñeep di wax fu ñu tuddee turam Yonenn beeko ko baaxee moo sàkkuw turam Ngëram, ngëram ñeel na ka dog buumi jaam ñi Ki tax ñu sampi daara fi ba mbacké baari Sant ak ngëram ñeel na borom silkul jawaahiri Jàraama rek doyul ci borom magal gii Xamu ñu sax yaw ki nga doon Ba yore mbootu kun fa yakuun Bismil ilaahi may deelu sant daam Moo ñu goreel tax deewugn ci njaam Ñun sant nan bu wér-a-wér Noflaayam yi raw na ci ñun ker Doyna laaxuwaay ak weeruwaay Woo nañ la woowatila sunuy mbir kaay Buñ doon wutt dara Duñ la moy ndax yaay dara Joo xam ne man naa def dara Mu jur lu ñepp yéem