Sama Président

Awa Thiès

    Continúa después del anuncio

    Ku ne xam nga ki la nob
    Ki la bëgg te du la nax
    May la jàmm te di la wan
    Luy mbëggeel waay, xam nga ko

    Duy nga sama xol mu fees
    Bëgg tay du wees
    Taal nga ma fu ne
    Léegi Sapeur lañuy xaar

    Sàcc nga sama xol bi
    Fàww boole am ci yoon
    Coup d’Etat sama mbëggeel
    Léegi Armée lañuy xaar
    Dok ak yaw ci mines u rebelles yi
    Jéggi tànk moom du xel
    Dugal nga lu ne sama xol
    Léegi Douane lañuy xaar

    Président a ngee
    Président a ngii
    Foo nekkee Président
    Ma doon fa Première Dame

    Foo doonee Macky, ma doon sa Marème
    Foo doonee jëmm, ma doon sa xol
    Foo doonee Sadio Mané
    Ma doon sa ballon, nga di ma dugal
    Foo doonee pique, ma doon sa pelle
    Foo doonee xalaat, ma doon sa xel bi
    Di la tardeel ba nga dof
    Dof di naan “waawaaw”

    Continúa después del anuncio

    Ey waay!
    Ndeysaan!
    Ey waay!
    Ndeysaan!

    Awuma wurus, awuma ngalam
    Waaye chéri am naa mbëggeel
    Dara xewul dee ko woyofal
    Jaral nga ma lu ne
    Sa joli coeur ràngati ma
    Ba ma dellu gone

    Bu ngeen ma dégloo ma wayal leen
    Ki nangu sama xol bi laay wayal

    Hey! Tourné nga daj nga ci man
    Déédéét du yaafuus nekkul ci man
    Wax ji du bari, jëf ji day bari
    Jikko bu défaillant nekkul ci man

    Président a ngee
    Président a ngii
    Foo nekkee Président
    Ma doon fa Première Dame

    Foo doonee Macky, ma doon sa Marème
    Foo doonee jëmm, ma doon sa xol
    Foo doonee Sadio Mané
    Ma doon sa ballon, nga di ma dugal
    Foo doonee pique, ma doon sa pelle
    Foo doonee xalaat, ma doon sa xel bi
    Di la tardeel ba nga dof
    Dof di naan “waawaaw”

    Ey waay!
    Ndeysaan!
    Ey waay!
    Ndeysaan!

    Aah! Lee!
    Ey waay!
    Jàmbaari léegi léegi
    Jóoni jóoni jàmbaar
    Ndeysaan!
    Biram Diop
    Ey waay!
    Chéri Kya dama lay joobeel
    Ndeysaan!

    Información de la canción

    Composición:

    ¿Los datos están equivocados?

    Enviar revisión