Sunu Senegal

Coumba Gawlo

    Continues after the ad

    Sunu Senegaal réew mi ñoo ko moom, buñu ko yàq
    (Réewum Senegaal gaal gi nanu ko joow buñu ko suuxal)

    Kilifa diine yëg bu aada bi ñépp nañu man ko
    Góor ak jigéen mag ak ndaw ñi nanu man ko
    Parti au pouvoir ak opposition nanu diisoo
    Sunu Senegaal gaal gi warul suux nañu man ko

    Ayca leen ñu joow gaal gi yaatu na buñu ko suuxal
    (Réewum Senegaal gaal gi nanu ko joow buñu ko suuxal)

    Nga ñaan te bekk xasante bi bilaay jaru ko fi
    Su ku ne bàyyee sa waar
    Nu mu gëna rafete réew mi jëm kanam
    Waar wi yaatu na aycaleen ñu bàyyi baña fëwalu
    Réewum Senegaal sutura ak ngor lanu ko xame

    Continues after the ad

    Réewum Senegaal réew mi ñoo ko moom buñu ko yàq
    (Réewum Senegaal gaal gi nanu ko joow buñu ko suuxal)
    Réewum Senegaal yaa ma gënal fépp fu ma mëna dem
    (Réewum Senegaal gaal gi nanu ko joow buñu ko suuxal)

    Ku ma xool ci Senegaal dinga ma mere, moo nekk ci sama xol bi
    (Réewum Senegaal gaal gi nanu ko joow buñu ko suuxal)

    Kilifa diine yëg bu aada bi ñépp nañu man ko
    Góor ak jigéen mag ak ndaw ñi nanu man ko
    Parti au pouvoir ak opposition nanu diisoo
    Sunu Senegaal gaal gi warul suux nañu man ko
    Réewum Senegaal réew mi ñoo ko moom buñu ko yàq

    Njangum gune yee
    (Ñun loolu moo ñu soxal)
    Réyum ndaw ñi
    (Ñun loolu moo ñu soxal)
    Moo wara doon priorité!

    Weer gi yaramu askan wi
    (Ñun loolu moo ñu soxal)
    Kiraange askan wi
    (Ñun loolu moo ñu soxal)
    Moo wara doon priorité!

    Jammi askan wi
    (Ñun loolu moo ñu soxal)
    Naataange ci réew mi
    (Ñun loolu moo ñu soxal)
    Moo wara doon priorité!

    Artiste yii
    (Ñun loolu moo ñu soxal)
    Communicateurs traditionnels
    (Ñun loolu moo ñu soxal)
    Rekk leen ju jung yi drapeau Senegaal des ca kaw
    Réewum Senegaal réew mi ñoo ko moom buñu ko yàq

    Song details

    Composition:

    Did you see an error?

    Enviar revisão