Baby
Tay duma la wayal
Dama lay rabal!
Ñu dem
Sama xol nga braquet dugg ci jël lépp te yoroo arme
Duma prisonnier mais yaa ma tëj ci sa charme
Mënuma fey te yaa tax ma sobbu ci géeju mbëggeel
Xaaruma appel, sa xol laa décroché fajar teel
Yaa ma bégal sa bopp, xaaroo ma naan la aimer ma
Jaral nga ma rekk rekk-rekk soru ko ci MMA
Dama doon dundu ak poison nga ñëw doon sama antidote
Réparer sama vision wan ma ngor ba am ci dot
Dama bàyyi lépp ànd ak yaw
Sa loxo sama loxo ñu ànd di daw
Dem fu la neex yaw
Bëgg ma, yóbbu ma fu la neex
Man yaw rekk laay topp
(Bëgg naa la baby)
Ni ma la rawee ëpp na
(Wóolu naa la baby)
Gëm naa la, wóolu naa la
(Hey, xol bi yaa ci nekk)
Sama xol bi yaa ci nekk
(Fii yaa fi nekk)
Sama xol bi yaa ci nekk
Yaa may jox connection boo soree dootuma amaati réseau
Jege ma, ma naan la je t'aime di ko répéter mel ni écho
Ñépp laa supprimer, yaw laay jege di fumer
Su ñuy waxtaanee téem nga fokk ko freestyle, lépp laay rimer
Sama alal ki ma gënal yaa raw diamant ak or
Maa lay wayal di la dalal yaay sama trésor
Même soo may xool daay existant
Yaa bari féem di ko teg ci temps
Maay tëgg ñëw di la tëbbal tay dinga fecc ba daneel, tacc tan!
Maak yaw ba géej gi fer du ñu may noon yi chance su ree
Saañ naa wee ko sa fer te jamra du ka sans assurer
Daw rekk amul arrêt mel ni auto bu amul frein
Bi ma ñépp bàyyi wee, yaw yaa ma jàpp ni refrain
Dama bàyyi lépp ànd ak yaw
Sa loxo sama loxo ñu ànd di daw
Dem fu la neex yaw
Bëgg ma, yóbbu ma fu la neex
Man yaw rekk laay topp
(Bëgg naa la baby)
Ni ma la rawee ëpp na
(Wóolu naa la baby)
Gëm naa la, wóolu naa la
(Hey, xol bi yaa ci nekk)
Sama xol bi yaa ci nekk
(Fii yaa fi nekk)
Sama xol bi yaa ci nekk
Baby ni nga may bégalee maa ngi toog di ree
Yaa ma gënal lu ne, fu ne, sama amoré
Yaw laa doon wër, yaa ma feeñu
Yaw la, yaw la, yaay sama plus for
(Dama la nob)
Chéri ribi daa, cha la, la, la
(Man bëgg naa la)
Yaay sama àljanna
(Sama àdduna)
Dénk naa la paradise
(Naw naa la, rombu naa la)
Man yaw laa dof
Dama bàyyi lépp ànd ak yaw
Sa loxo sama loxo ñu ànd di daw
Dem fu la neex yaw
Bëgg ma, yóbbu ma fu la neex
Man yaw rekk laay topp
(Bëgg naa la baby)
Ni ma la rawee ëpp na
(Wóolu naa la baby)
Gëm naa la, wóolu naa la
(Hey, xol bi yaa ci nekk)
Sama xol bi yaa ci nekk
(Fii yaa fi nekk)
Sama xol bi yaa ci nekk
I love you baby, yeah!
Eh xol bi yaa ci nek!
Fii yaa fi nekk!