Jëli Li Des

Dip Doundou Guiss

    Continues after the ad

    1da on the beat

    Never mind every day, bàyyi nit ñi ñu sol la bàyyi nga liggéey
    Jarul coow di jib, coow du jib jarul
    Sa family ñooy sonn ci yaw di daŋ-daŋi kay
    Bis dina tar doo gis kenn

    Kon jëli li des, mën nga jëli li des, jugal jëli li des
    Lépp ci xel rekk lay feeñ, jëlil li des
    Yaay jëli li des, mën nga jëli li des (mmm)
    Ndax lépp ci xel la, kon yaw yaay jëli li des

    Continues after the ad

    Sol essence sa mind soog a jëli li des
    Ñépp a soxla ndam def ni mbër yi di def
    Dootuñ joow Senegaal seen gaal gee bari vitesse
    Fii ñi dàq a jaay seen taat ñoom seen cér yi du feeñ
    Non duñ sàcckat yu mag bu dee soluñu veste
    Ku ñàkk wéet nun ndox yu taa yee tax sunu kër yi di fees
    Luy sa njariñ ñu xeex texeg tekki
    Xayna safaraay changer nit
    Fi dóomu taal taxul ba këriñ mënul weex
    Nice fine, Suñ dëkk du gat baay
    Fi jeunes yi dul am njëgam duñ def lu dul taaj caayin
    Balóot, babi ak dice
    Dóor call këfi sac jaay
    Réer ci saayir ak baatin fen ak dëgg bëccëg night time
    Ku dund jàng force ndax life day jox ay cours sa maitre
    Bul xam ku baax ci yaw ak ku la jekkoogul batay
    Loo baax baax moytul nit ñi foog ne sa xol moo sut sa xel
    Fii dangay dee ci nit mu lay xoon pour nga dee

    Kon jëli li des, (I'm on my way)
    Mën nga jëli li des, (you know my pain)
    Jugal jëli li des (story of my life, story of my life)
    (I'm on my way) Yaay jëli li des (you know my pain)
    Mën nga jëli li des (story of my life, story of my life)
    Ndax lépp ci xel la, kon yaw yaay jëli li des

    Jëli li des pour bañ ñàkk li xaalis mënut a am
    Yaa gën alal mën nga ñàkk sa bopp ci wut alal
    Même sutura dafa cher ni dignité muñ ak ndam
    Ku bañ tàllal loxoog yërmaande fàww nga suul sa tànk dóoranteek life
    Nangu sëyal metit heureux ménage door a ker naaj
    Yal na nu Yàlla musal ci compte bu fees ak ruu bu vide
    Musal nu tam ci toog ak ñépp bég ak wéet sa ruq triste
    Xel kenn du ci lire kenn mënut a xam lu weex ak ñuul ci nit
    Gëj naa gis samay doom, gëj naa feel sama drogue
    Gëj naa am li ma yellool comme bénéfice sama job
    Tay jëli naa li des, tay njàmpe la ci der, calpé laa ci cash
    Tay xàmme naa vipéres yépp
    Duñ ma téeye ni Mandela ci jail
    On the top of the top Dip Doundou Gis you know my name
    Booy damaa doylu trop ku mënul suur mënu maa lekk (mëno maa lekk)
    Dereet du fen, Yàlla buy def du tàggu kenn
    Démb ñaan yi bañ na tay sët yi nangu nañu

    Never mind every day, bàyyi nit ñi ñu sol la bàyyi nga ligégey
    Jarul coow di jib, coow du jib jarul
    Sa family ñooy sonn ci yaw di daŋ-daŋi kay (daŋ-daŋi kay)
    (Daŋ-daŋi kay, daŋ-daŋi kay)

    Song details

    Composition:

    Did you see an error?

    Enviar revisão