Do Change

Jeeba

    Continúa después del anuncio

    Tay boo xoolee life nu muy demee
    Yaw dangay daaldi yeme
    Tay boo xoolee life nu muy tëddee
    Yaw dangay daaldi yeme

    Ndax jambat nan fi
    Jambat nan fi lu nekk
    Ndax saay saay si

    Te xam naa ni doo kuy changé
    Ndax jambar nga
    Man xam naa doo kuy changé
    Ndax jambar nga

    Yaw life xoolal fi ngay tek sa tànk
    Àdduna dafa gudd tànk
    Yaw like jëfal balaa jëf wes
    Àdduna dafay xëy ni mes
    Te nit ku nekk war na am rooyukay
    Soo bañee dégg wuyaay
    Te nit ku nekk war na am wéeruwaay
    Yaw defal loolu waay
    Yaw bul la am-am àdduna jaaral boy
    Ba ngay jaay sa ngoor
    Yaw bul la réseau sociaux yóbbu boy
    Ba ngay exposé sa taar
    Yaw xana xamoo ni ndow dey wes
    Te ndowo dey jeex

    Man xam naa ni doo kuy changer
    Ndax jambar nga yeah yeah

    Tay boo xoolee life nu muy demee
    Yaw dangay daaldi yeme
    Tay boo xoolee life nu muy tëddee
    Yaw dangay daaldi yeme

    Continúa después del anuncio

    Ndax jambat nan fi
    Jambat nan fi lu nekk
    Ndax saay saay si

    Te xam naa ni doo kuy changé
    Ndax jambar nga
    Yeah yeah

    Way sant Yàlla ba ma amee yaay ju baax
    Dieya Naedio Sadibou
    Way sant Yàlla ba ma amee baay bu baax
    Jeeba mamadou doudou
    Way sant Yàlla ba ma amee abadan abadan daiman
    Abadan ci sama xol bi rekk laay dees
    Du mësa de aap naa ko téémééri at

    Ne nan domu géwel bu juddu mum
    Walay tas sa yakaru bay la
    Tey baay bu nekk
    Bu sañoon juur doom bu ko wuutu
    Doom ju bëgg doon ku baax
    Kaay ma de la jànt bu timoon sunu maam
    Jànt boobu moo timoon sunuy baay
    Jànt boobu mu ñu tiim, mooy tiim sunuy doomi doom
    Xoolal bu baax li ngay def

    Bu coow li bari bañu fàtte sunuy yaay
    Yaw yaa yaay
    Bu coow li bari bañu fàtte sunuy baay yow baa baay

    Tay boo xoolee life nu muy demee
    Yaw dangay daaldi yeme
    Tay boo xoolee life nu muy tëddee
    Yaw dangay daaldi yeme

    Ndax jambat nan fi jambat nan fi lu nekk
    Ndax saay saay si

    Te xam naa ni doo kuy changé
    Ndax jambar nga
    Yeah yeah

    Tay boo xoolee life nu muy demee
    Yaw dangay daaldi yeme
    Ndax jambat nan fi jambat nan fi lu nekk
    Ndax saay saay si

    Te xam naa ni doo kuy changé
    Ndax jambar nga
    Yeah yeah

    Información de la canción

    Composición:

    ¿Los datos están equivocados?

    Enviar revisión

    Canciones relacionadas