Continues after the ad

    Fi nga may yóbbu sori na
    Fi nga ko jàpp foofu la
    Nga may yëgloo asaman
    Te soxlawuma roppelan
    Foo ma woo ma wuyu la
    Fi nga ma tek bae saf na ma
    Li nga may yëgloo for na lool
    Mu ngi dugg sama xol

    Def ma lu la neex
    Li de warul jeex
    Yaa ngi bëgg a yeex
    Xam nga li may yëg
    Doy nga ma sëk
    Bul xaar ba ëllëg

    Def ma lu la neex
    Li de warul jeex
    Yaa ngi bëgg a yeex
    Oh def ma lu la neex yaw
    Wax ma lu la neex hee

    Continues after the ad

    Baby yaay sama seytaane
    Lu dul jeex lañu diggale
    Xol yi feex ba abadan ci yaw lay fanaan
    Tàmm naa la ci seen biir, yaa may miirloo
    Su guddi xaajee
    Ba suuf seddee
    Ma jàkkaarloo ak sama reeni xol, hey
    Li may dundu neex na lool

    Def ma lu la neex
    Li de warul jeex
    Yaa ngi bëgg a yeex
    Xam nga li may yëg
    Doy nga ma sëk
    Bul xaar ba ëllëg

    Def ma lu la neex
    Li de warul jeex
    Yaa ngi bëgg a yeex
    Oh def ma lu la neex yaw
    Wax ma lu la neex hee

    Daf may neex daq yaw la love
    Mu lay neex ñu dundu love
    Bae jëlal li nga moom li ma yor
    Yaay boroom doo seen morom
    Xoolal fi ma tollu ci yaw
    Yaw yaa may tël ba ci kaw
    Gëm naa ni li du jeex mbëggeel rekk moo neex

    Def ma lu la neex
    Li de warul jeex
    Yaa ngi bëgg a yeex
    Xam nga li may yëg
    Doy nga ma sëk
    Bul xaar ba ëllëg

    Song details

    Composition:

    Did you see an error?

    Enviar revisão