Fi nga may yóbbu sori na Fi nga ko jàpp foofu la Nga may yëgloo asaman Te soxlawuma roppelan Foo ma woo ma wuyu la Fi nga ma tek bae saf na ma Li nga may yëgloo for na lool Mu ngi dugg sama xol Def ma lu la neex Li de warul jeex Yaa ngi bëgg a yeex Xam nga li may yëg Doy nga ma sëk Bul xaar ba ëllëg Def ma lu la neex Li de warul jeex Yaa ngi bëgg a yeex Oh def ma lu la neex yaw Wax ma lu la neex hee Baby yaay sama seytaane Lu dul jeex lañu diggale Xol yi feex ba abadan ci yaw lay fanaan Tàmm naa la ci seen biir, yaa may miirloo Su guddi xaajee Ba suuf seddee Ma jàkkaarloo ak sama reeni xol, hey Li may dundu neex na lool Def ma lu la neex Li de warul jeex Yaa ngi bëgg a yeex Xam nga li may yëg Doy nga ma sëk Bul xaar ba ëllëg Def ma lu la neex Li de warul jeex Yaa ngi bëgg a yeex Oh def ma lu la neex yaw Wax ma lu la neex hee Daf may neex daq yaw la love Mu lay neex ñu dundu love Bae jëlal li nga moom li ma yor Yaay boroom doo seen morom Xoolal fi ma tollu ci yaw Yaw yaa may tël ba ci kaw Gëm naa ni li du jeex mbëggeel rekk moo neex Def ma lu la neex Li de warul jeex Yaa ngi bëgg a yeex Xam nga li may yëg Doy nga ma sëk Bul xaar ba ëllëg