Continues after the ad

    Ngëram, ngëram ñeel na ka dog buumi jaam ñi
    Ki tax ñu sampi daara fi ba mbacké baari
    Sant ak ngëram ñeel na borom silkul jawaahiri
    Jàraama rek doyul ci borom magal gii
    Yaa ko jar, ma la koy wax: Ya qalili
    Mbégté'm yâllah nga ak yonnen, yâ habibi
    Àddunah da la koo may, yâ azizi
    Li mu ëmb it yaa ko moom, yâ wasiilati
    Yaa mën fii ak fa nu jëmm yaay jaalé jaam ñi
    Bu mbër yeep taxawee yaa mën ci goor ñi

    Makaak madiina, seen mboot ya ñëw na
    Diggante njaareem mbacké ba touba
    Bamba teeye naa laak leneen ludul samay loxoo
    Ndax xam nga yalla xamlé nga koo
    Maam ceerno faati loxol ndayjoor la
    Moo gaaganti naar ya té laaloul mool ya
    Jaramaa rek doyul dañ la wara kennal
    Suñ goree suñ leepp yaa nu ko wara gënal

    Continues after the ad

    Ëskey la ñeep di wax fu ñu tuddee turam
    Yonenn beeko ko baaxee moo sàkkuw turam
    Ngëram, ngëram ñeel na ka dog buumi jaam ñi
    Ki tax ñu sampi daara fi ba mbacké baari
    Sant ak ngëram ñeel na borom silkul jawaahiri
    Jàraama rek doyul ci borom magal gii

    Xamu ñu sax yaw ki nga doon
    Ba yore mbootu kun fa yakuun
    Bismil ilaahi may deelu sant daam
    Moo ñu goreel tax deewugn ci njaam
    Ñun sant nan bu wér-a-wér
    Noflaayam yi raw na ci ñun ker
    Doyna laaxuwaay ak weeruwaay
    Woo nañ la woowatila sunuy mbir kaay

    Buñ doon wutt dara
    Duñ la moy ndax yaay dara
    Joo xam ne man naa def dara
    Mu jur lu ñepp yéem

    Song details

    Composition: Salif Keita

    Did you see an error?

    Enviar revisão