Yeye (DIAGA)

Wally B. Seck

    Continúa después del anuncio

    Fefsy on the beat ayy

    Aksina thi say lokho you léér
    Diaarama nénam
    Wonala gnetti yone
    Sog thi tegg baabam
    Yama sang, solal ma
    Ma dioy ngeu nakh ma
    Souma fébaré nga bayi lepp té fadj ma
    Woy nala, bakk nala yaye
    Diaarama nénam

    Souma done wurus yamay moom
    Souma sagnone abadan ma done sa wérouway
    Douma tayi dila djine sa rafétaay yow
    Awma loumay ragal ndakh yaye sama ganaay

    Ayo yé sama yaye boul di dioyo
    Beugouma guiss say rongogne
    Boul di dioyo
    Boula dara méti
    Boul di dioyo
    Néné touti maag na

    Continúa después del anuncio

    Yaye awma sa fay
    Linga dadj thi keur gui
    Linga dadj thi mane mii
    Dina ko séédé tay
    Eumb ma diourom gnénti wéér
    Yar ma, yor ma, yeureum ma
    Louma meunti def yagg yagg téral la
    Baba gueureum nala, benn djiguén gueunoula
    Yaye Diaga, awma sa fey

    Yagg ngama mougnal
    Daan nala sonnal
    Wanté baalou nala akk yaye, bala mouy wééss
    Dinala bégueul, meussouloma féral
    Mbeuguel bima am thi yow dou rééss, dou diékh
    Ayo ye sama yaye boul di dioyo
    Teranga doy na seukk thi nga done sama yaye
    Sant na Yalla
    Diaarama nénam

    Yaye awma sa fay
    Linga dadj thi keur gui
    Linga dadj thi mane mii
    Dina ko séédé tay
    Eumb ma diourom gnénti wéér
    Yar ma, yor ma, yeureum ma
    Louma meunti def yagg yagg téral la
    Baba gueureum nala, bén djiguén gueunoula
    Yaye Diaga, awma sa fey

    Limala yééné dougn ko natt
    Khadioul thi adouna
    Di gnane Yalla bayila fi
    Té saam la
    Soukk thi say tankk moy sama aldjana

    Yaye awma sa fay
    Linga dadj thi keur gui
    Linga dadj thi mane mii
    Dina ko séédé tay

    Fefsy on the beat ayy

    Información de la canción

    Composición:

    ¿Los datos están equivocados?

    Enviar revisión