Cifra Club

Kelemati

AMADEUS

Aún no tenemos los acordes de esta canción.

Jëm ci kaw jal bi jallaañoo
Jànja day bokk lu rang bi seere
Jefe ci Mexico Fuuta mooy kàllaajoo
Masul a tar ba Jànja weere

Fàttewul li ñu ko wax ci maamam
Jànja fàttewul aada ak cosaanam
Du sukkal ku dul Bàlla Maaram
Jànja everyday moom mi ngi ci Waaram

Fàttewul ne Baay Malamin Daara
Bindal na ma ay téere
Téere yaa nga Saalum
Saalum ñaari néeg la
Eey waay

Kelemati kelemati Maam Daan na wax ne
Lépp lu mu léebu dëgg la
Lépp lu mu léeb
Soo ko xoolee ba ca biir dëgg
Dinga ci gis njariñ
Lépp lu mu léebu dëgg la
Lépp lu mu Léeb

Kelemati kelemati maam du waxantu
Lépp lu mu léebu dëgg la
Lépp lu mu léeb
Boo ko dégloo ba ca biir a biir
Dinga ci gis njariñ
Lépp lu mu léebu dëgg la
Lépp lu mu léeb

Maam daan na wax
As gor du sëkk jëf Jànja Faama
Maam daan na wax
As gor du fàtte démb, yaw Masàmba

Amuma lu dul sama baat
Man amuma lu dul sama xol ak sama yéene
Amuma lu sut sama way
Li ma war mooy di ci yedde ak di ci yeete

Baay Malamin Daara
Bindal na ma ay téere
Téere yaa nga Saalum
Saalum ñaari néeg la
Eey waay

Kelemati kelemati Maam Daan na wax ni
Lépp lu mu léebu dëgg la
Lépp lu mu léeb
Soo ko xoolee ba ca biir dëgg dinga ci gis njariñ
Lépp lu mu léebu dëgg la
Lépp lu mu Léeb

Kelemati kelemati maam du waxantu
Lépp lu mu léebu dëgg la
Lépp lu mu léeb
Boo ko dégloo ba ca biir a biir dinga jege ñaar yii
Lépp lu mu léeb dëgg la
Lépp lu mu léebu dëgg la

Baay Malamin Daara
Bindal na ma ay téere
Téere yaa nga Saalum
Saalum ñaari néeg la
Eey waay

Baay Malamin Daara
Bindal na ma ay téere
Téere yaa nga Saalum
Saalum ñaari néeg la
Eey waay

Baay Malamin Daara
Bindal na ma ay téere
Téere yaa nga Saalum
Saalum ñaari néeg la
Eey waay

Otros videos de esta canción
    0 visualizaciones

    Afinación de los acordes

    Afinador en línea

    Ops (: Contenido disponible solo en portugués.
    OK