Cifra Club

Leggi

Amira Abed

Aún no tenemos los acordes de esta canción.

Léegi
Damay def ni yaw photo profil
Boo soloo génn a ma sol jaar ne
Pesum kanam boroom a kay fajal boppam
Ni miy safe ci man rekk lay safe ci yaw

Léegi
Dangay jaay nàndite, maa def bandit
Nga teg ma deal, ma teg la lu metti
Pesum kanam boroom a kay fajal boppam
Ni miy safe ci man rekk lay safe ci yaw mi

Hee yaw eh, danga fok ni
C’est officiel, danga juum
Ne nga lu la neex def
Mënoo, te ne nga ñofar
Loo bataré ma coupal la ko
Teggal la ci ay ree
Ah, xamoo maak yaw
Tant que du Diakka, du Église
Ba dégguma Al-Xayri
Soo ma nobee
Respecté ma, ma respecté la

Looloy game bi, looloy deal bi
Soo bëggee ñu dund mbëggeel dëgg-dëgg
Dangay bay sa xel bi ngay fowe
Ni ngay jobe, ni ngay playé
Doo gis ku mel ni man

Yarul léegi bala may dem
Bala may dem nga topp sama ginnaaw
Naan su ma yëgoon
Yarul léegi, yarul léegi
Man doo ma nob di ma fowe
Man doo ma am di ma fowe

Moo tax léegi
Man damay def ni yaw photo profil
Boo solo gëna ma solu jaar ne
Pesum kanam boroom a kaay fajal boppam
Ni miy safe ci man rekk lay safe ci yaw

Bëgg naa léegi
Galanterie ju mat
Yóbbu ma resto, toppatoo ma
Shoppingal ma
Te neexal ma
Loo looy tax jamm am bala may dem

Fii ku lamb ya tay
Noy ame ngalam di wut përëm
Kenn du mel ni man
Yarul léegi, yarul léegi
Man doo ma nob di ma fowe
Man doo ma am di ma fowe

Moo tax léegi
Man damay def ni yaw photo profil
Boo solo gëna ma solu jaar ne
Pesum kanam boroom a kay fajal boppam
Ni miy safe ci man rekk lay safe ci yaw

Léegi
Dangay jaay nandite ma def bandit
Nga teg ma deal, ma teg la lu métti
Pesum kanam boroom a kay fajal boppam
Ni miy safe ci man rekk lay safe ci yaw mi

Ñi ma bëgg bari na
Fexel nga xam man maay kan
Wala ma dem bàyyi la
Pesum kanam boroom a kay fajal boppam
Ni miy safe ci man rekk lay sage ci yaw

Neñ ci dem kon en avant
Loo batéré ma coupé la ko kaay
Te lépp loo mbalax ma fecc ko kaay
Pesum kanam boroom a kay fajal boppam
Ni miy safe

Otros videos de esta canción
    0 visualizaciones

    Afinación de los acordes

    Afinador en línea

    Ops (: Contenido disponible solo en portugués.
    OK