Du bàyyi
Ak loo ko mëna def du bàyyi
Ak lu mu mëna gis du bàyyi
Loo ko mëna def du bàyyi
Bisoo bis
Ngay gën triste
Leen li nga bëgg wetook man ci àdduna
Li ngay gis
Lépp mooy bis
Bis ñëw ma dëdd lépp ni la àjjuna
Life dey gëna tara
Mais doo mësa bàyyi
Yaa ngi dunde yaakaar
Gis naa ci yaw njambaar
Def nga li la war
Te Yàlla du la seetaan
Te bëgg naa la, bëgg comme ni nga ma
Show la tuuti love comme ni nga may
Lépp loo bëgg man ma ne ca
Ndax mérité nga ko
Bëgg naa la, bëgg comme ni nga ma
Show la tuuti love comme ni nga may
Lépp loo bëgg man ma ne ca
Ndax mérité nga ko
Ayayah ayayah ay!
Suma saañoon bëgg la
Tuuti sax comme ni nga may
Hey
Ayayah ayayah ay!
Suma saañoon bëgg la
Tuuti sax comme ni nga may
Man defuma la
Leen lu wara tax
Sa xel ak sa xalaat nekk ci leneen
Xol bi su doon wër
Toppi nga keneen
Jaam ak bëgg bëggam
Mais Yàlla mooy dogal
Sa boo may xool mbégte bi may gis ci yaw
Ferñent bi takk mënuma ko ëpp ba mu gën di boy
Wtf is love bu fekke ni man ki ma ko sekkal gisuma?
Lool ngay wax sa biir man metti na ma lool baby
Te bëgg naa la, bëgg ma comme ni ma la
Show ma tuuti love comme ni ma lay
Lépp li ma bëgg yaw nga ne ca
Ndax mérité naa ko
Man bëgg naa la, bëgg comme ni nga ma
Show la tuuti love comme ni nga may
Lépp loo bëgg man ma ne ca
Ndax mérité nga ko
Ayayah ayayah ay!
Suma saañoon bëgg lay
Tuuti sax comme ni nga may
Hey
Ayayah ayayah ay!
Suma saañoon bëgg la
Tuuti sax comme ni nga may
Duma ni la dem naa
Te mënuma la ba
Man duma Dame Tiatou Mbissane
Duma ni la dem naa
Ndax mënuma la fàtte dame
Man duma Dame Tiatou Mbissane
Dame Tiatou Mbissane
Jarul seetlu ji Daam
Jarul dem di seeti Mbissane