Cifra Club

Vive l'amour

Momo Dieng

Aún no tenemos los acordes de esta canción.

Mbëggeel rekk ka neexooy
Ci buñ la nobee
Mbëggeel aka neexooy
Woowooy ci bun la bëggee

Ñi mëna kot daal
Amuñu mbaam
Ak ni mu la bëggee
Yaw nga koy fowe

Mbëggeel dafa tiis
Te xolul melokaan gaañi
Su ma la nobaatee teye ma
Bul naagu
Bul fowe yooyu

Soose Demba majigéen ce Yacine
Baby xool ma ree ma
Maa tàggook coow lii
Li ma ni chéri booy, waxal
Soo ma la nobee lu ma yor
Jox la ko deseek neen

Soose Demba majigéen ce Yacine
Baby xool ma ree ma
Maa fàtte coow yii
Xool ma ree ma
Maa fàtte coow yii

Mbëggeel rekk ka neexooy
Ci buñ la nobee
Boo dajee sa ame soeur
Tëyal, tëyal!
Mu dëgër dëgër

Mbëggeel dafa tiis
Te xolul melokaan gaañi
Suñ la nobaatee, tëyal!
Bul naagu
Bul fowe yooyu

Soose Demba majigéen ce Yacine
Baby xool ma ree ma
Ñawal noon yi
Xam nga sama biir, sama dara umpu la
Soo ma bëggee lu ma yor jox la ko, deseek neen
Li ma ni chéri booy waxal
Maa la bëgg ba mu jeex dawuma ci dara
Xool ma ree ma
Ma tàggook coow yii

Mbëggeel dafa tiis
Te xolul melokaan gaañi
Suñ la nobaatee, tëyal!
Bul naagu
Bul fowe yooyu

Maa tàggook coow lii
Li ma ni chéri booy, waxal
Soo ma la nobee lu ma yor
Jox la ko deseek neen

Soose Demba majigéen ce Yacine
Baby xool ma ree ma
Maa fàtte coow yii
Xool ma ree ma
Maa fàtte coow yii

Mbëggeel dafa tiis
Te xolul melokaan gaañi
Suñ la bëggatee, téyel
Ak sa fukki loxooy

Aly Baba Coumba Naar mbëggeel looy
Ay waay man fu ma jëm céy xale bi jaral na ma
Nob naa ko

Ni waawaaw
Aly Baba Coumba Naar, Mario Mbaye
Mussee Jama Coumba Sene
Mbaye Kuli Fati ma diodio
Borom ngaay ndanaan gee

Aly Baba Coumba Naar mbëggeel looy
Hey yaw man fu ma jëm céy xale bi jaral na ma
Nob naa ko
Coow la ce pindum teen ba
Wey gaa ñi amul baak Mario Mbaye
Mussee Jama Coumba Sene
Mbaye Kuli Fati ma diodio
Borom ngaay ndanaan gee

Aly Baba Coumba Naar mbëggeel looy!

Otros videos de esta canción
    0 visualizaciones

    Afinación de los acordes

    Afinador en línea

    Ops (: Contenido disponible solo en portugués.
    OK