Dama nekk gune, ubbi sama bët yi
Togg di seetlu àdduna bi xam ne dafa métti
Yenn saay ma tëdde yeewu xaaja guddi
Tokk ci sama dige laal di jooy ndax jafe-jafe
Doon yakkar ci yaayam, nekk xaritu baayam
Mbaa xam ngeen ni nit ñu ma yónni dañ ma yakamte
Fépp fu ma jar yëf dafay mette
Yoon bi bari xaxaam ba dëkki di ma jane
Mbaa xam ngeen ni duma lajj duma daw
Damay jiggéen moo tax may daw battu gannaaw
Yenn saay ma fëgg
Ñu ne ma du fi de
Ma jokk daldi korti korti dellu fi ma juge
Bu dul yépp nékathia
Ma koy fëgg bag de
Waye xam na ni àdduna bi munul yomb
Mbaa xam ngeen ni newoon naa leen yeen
Damay dem, man dara duumate
Man de newoon naa leen, man de damay dem
Damay dem man dara duumate
Man de newoon naa leen, man de damay dem
Man Queen Biz mi de, man de damay dem
Fépp fu ma daldi dem
Ñii naan ma mothi galaas
Gni naan ma moom waye dafa woyof seurr
Mbaa xam ngeen ni man mi damay djiguen douma goor
Na fass sama lafou seurr ba doni goor
Man dina leen di wane
Né diant bi foumuy fenké
Foofu la yéwo té khamna loufiy khéwé
Damay sant buur be
Ci lim ma thieuré
Ndaxte xam naa ni moom moy boroom bët bu réy be
Mbaa xam ngeen ni newoon naa leen yeen
Damay dem, man dara duumate
Man de newoon naa leen, man de damay dem
Damay dem man dara duumate
Man de newoon naa leen, man de damay dem
Man Queen Biz mi de, man de damay dem
Soul keer douko téré feign annh
Oui yé douko téré feign
Wayé y'Allah bou keer daldi ndaw ba faf souralé len annh
Du ko tere feeñ
Man dara duma te
Man dara duma te
Man dara duma te
Man dara duma te
Man dara duma te