Cifra Club

Zéro To Héro

Viviane Chidid

Aún no tenemos los acordes de esta canción.

Toogal déglu ma àdduna bi Yàlla fi ne
Jamono metti na, ana jaambaar coqari
Su for yombee sëgg jafe billaay (ma ne billaay)
Coono du réer, gëmal sa boppu way (boppu way)
Liggéey ba dead bul mës a xepp sa njaay
Mën nga jugé ci zéro doon suba héros

Bitim réew sori na, nañu waa-jur da lay gunge
Soo bëggee ñu ndaw la, jom ak fulla rekk ngay wane
Bañ ku la yab, bul xaar ku lay defal
Jugal nga fight sa ëllëg ngay defar (ngay defar)
Looy tambalee farlu nga yeggale
Mën nga jugé ci zéro doon suba héros

Lu la war jug doori war (jug doori war)
Am na waxambaane (am na waxambaane)
Oh yaw la kër ngi di xaar (yaw la kër ngi di xaar)
Waa-jur yaa ngi ndëlle (waa-jur yaa ngi ndëlle)

Jugal uuti xéy nelaw bi yàgg na (yàgg na)
Fonkal sa liggéey mooy jur sa teraanga (teraanga)
Marchand ambulant wax dëgg jaaraama
Masa coono yaay booy naaj bi tàng na

Oh oh bul xépp li ngay liggéey (bul xépp li ngay liggéey)
Su baaxee dangay gagner (su baaxee dangay gagner)
Àdduna bare la (àdduna bare la)
Te fok nga am fit ñeme (faw sa fit ñeme)

Jugal uuti xéy jant bi fenk na (fenk na)
Fonkal sa liggéey mooy jur sa teraanga (teraanga)
Bul gaawa sëngéem fi Yàlla moo fi ne
Masa coono my boy naaj bi tàng na

Ma ne la soo ma déggee may waxe ni
Dafa jot ma xamal la
Soo ko ñeme bul mës a xàddi
Bul xaar kenn defal la

Jugal uuti xéy nelaw bi yàgg na (yàgg na)
Fonkal sa liggéey mooy jur sa teraanga (teraanga)
Marchand ambulant wax dëgg jaaraama
Masa coono yaay booy naaj bi tàng na

Ma ne la soo ma déggee may waxe ni
Dafa jot ma xamal la
Soo ko ñeme bul mës a xàddi
Bul xaar kenn defal la

Jugal uuti xéy jante bi fenk na (yàgg na)
Fonkal sa liggéey mooy jur sa teraanga
Bul gaawa sëngéem fi Yàlla moo fi ne
Masa coono my boy naaj bi tàng na

Mën nga jugé ci zéro doon suba héros
Mën nga jugé ci zéro doon suba héros

Otros videos de esta canción
    0 visualizaciones

    Afinación de los acordes

    Afinador en línea

    Ops (: Contenido disponible solo en portugués.
    OK