Jege ma ma won la li nekk ci sama xel
Déglu ma, ma déey la li ngay def ci sama xel
May la ci ndax lii de neen la
Xol bi li muy tegg, lépp dëgg la
Gëm naa ne lii de mayu Yàlla la
Moom mi ñu boole, ca aras lañu ko fase
Mayu Yàlla la
Xale la ba tey, lu yàgg dafa fay
Kon naa ci ñépp tey te xam ne li du fay
Sama xol yaw la fal, sa bos de man la tànn
Foo yendu laay fanaan, sama baby kaay
Gën ci man, baax ci man
Gaaw ci man, sës ci man
(Yaw yaa sës ci man)
Dof ci man, mën ci man
Sax ci man, wóor ci man
(Yaw yaa woor ci man)
Tank tank, mbagg mbagg
Lu joxooñ ma dagg
Lu ma bëgg ci nga dëkk
Ndank ndank ba yëg fu sori
Jàpp bañ a bàyyi
Doon ci xàddi, doon ci tàyyi
Xel beey seede
Ne na toj nga bopp bi
Xalatul ku dul yaw, yaw yaa fi ne
Xel beey seede
Lu muy dundu moo neex
Neex a neex a neex, bëggul mu jeex
Xale la ba tey, lu yàgg dafa fay
Kon naa ci ñépp tey te xam ne li du fay
Sama xol yaw la fal, sa bos de man la tànn
Foo yendu laay fanaan, sama baby kaay
Gën ci man, baax ci man
Gaaw ci man, sës ci man
(Yaw yaa sës ci man)
Dof ci man, mën ci man
Sax ci man, wóor ci man
(Yaw yaa woor ci man)
Gën ci man, baax ci man
Gaaw ci man, sës ci man
(Yaw yaa sës ci man)
Dof ci man, mën ci man
Sax ci man, wóor ci man
(Yaw yaa woor ci man)
Yaw yaa sës ci man
Yaw yaa woor ci man